WURUS RUSUL A DELLU NGALAM WURUSU MALI, CA LOXOY SAA-MALI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saa-Mali yi léegi ñooy defaral seen bopp seen wurus. Liggéey boobu nag, dañ ko dénk doomi réew ma ci benn këru liggéey bu ñu sàmp foofee ca Mali. Mu nekk liy tax ñu bañ a ajooti ci menn réew ngir raxas ak a defar seen wurus. Nde, mbir mi làmboo na njariñ lu bari moo tax jëwriñ bii di Seex Fànta Maadi Keyta  ak kii di Ismayla Siibi, jiite këru liggéey bii di Marena Gold Mali, xaatim ab déggoo. Mu nekk kóllëre gu mat a sàmm ngir yokkute réewum Mali. 

Ngir suqali koom-koomam, réewum Mali dafa sumb ab sémb bu am solo fan yii weesu. Mu nekk sémb bu juddu ci gis-gis ak xalaati Nguur gii nga xam ne, moo yore réew mi tey. Nde, Nguur googu moo dogal, ci jamono jii, ni wurusu réew ma, doomi réew ma ñoo koy defar. Ndax, ku wàlliyaani moom, dafa fekk sa dëkk daa tëggul. Looloo tax mu xaatim ab déggoo ak këru liggéey gii di Marena Gold Mali. Kër googu nag, Saa-Mali yee ko moom te ñoo fay liggéey. Waaye, sémb bi làmboo na njariñ lu bari lool. Ci loolu, Ismayla Siibi a ngi xamle ne :

« Déggoo bi ñu xaatim dafay wone bëgg-bëggi Nguur gi ci di wormaal lépp loo xam ne ci réew mi lañ koy defare. Loolu nag, ag yeesal la ci fànn woowu. »

Xalaat bii juddu ci gis-gisu Nguur gi dina tax maxejji réewum Mali am ci liggéey. Xaymees na liggéey yi sémb bi mën a jur ci juróom-ñaari-téemeer (700. 000). Juróom-ñaari-téemeeri liggéey yooyu, dinañu meññ tamit yeneen xeeti liggéey yu ndaw ñeel ndawi réew ma. Nee ñu, ñaari-junniy (2. 000) ndaw dinañu ci amey xéy. Ndegam réew mi am na ay maxejj yu xareñ ci fànn woowu ba noppi yore matuwaay yi war yépp, Nguur gi bëggatul ajooti ci menn réew mu koy tëggal wurus gi mu yore. Dogal bii nag, dina tax mu jaay wurusam ni mu gën a njëgee (baree) ca bitim-réew. Bu ko defee, koom-koomam di gën a naat.

Kilifa giy teewal jëwriñ ji yore wàllu laf gi ak ndox mi, Susuru Dembele, biral na itam ne : « Li sunu ‘code minier’ bi dige dafa leer : su nu waree tëgg sunu wurus Mali lañ koy defe. Waaye fàww réew mi yore ay këru liggéey yu àttan liggéey boobu ».

Ci xayma, ñu bari ci Saa-Afrig yi jàpp nañu ni Saa-Mali yi dañu nekk di xàll yoon woo xam ne réewi Afrig yu bari moom lañ war a jël. Ndax kat, njureef yi ci nekk dina doon njariñal ñenn ci réewi Afrig yi. Ba noppi, suqali seen koom-koom jëmale ko fu ko kenn xaarewul woon. Ba tax na, ñu bari gëm nañu ni réewum Mali royukaay la ci réewi Afrig yu bari. Ndax, li mu fi jot a dund ak li mu fi jot a def ci diggante bu yàggul dara. Te, lu ne fàŋŋ moom, kenn du ko jeex. Li njiiti Mali yi def, du lenn lu dul dekkal cosaan. Nde, kenn du fàtte jamonoy Buur Kànka Musaa. Kooka, ku ko tudd, tuddaale alal ju bari ja ak wurus ya mu oomle woon. Te, jamono yooya, ñoo ko daan saytul seen bopp, di ko jariñoo. Moo nu tax a wax ne, wurus rusul a dellu ngalam

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj