Dibéer, 24eelu fan ci weeru féewaryee, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, agsi na. Bés bi taskati xibaar yi doon séenu, di ko jagleel ay xët ak i waxtaan a ngi nii. Bés bi mag ñi daan waxtaane, ndaw yi di ci werante, janq yi di ci dàggasante, waa-jur ak doom dem ba ciy meroo agsi na. Bés bi àddina doon waajal bernde bu mag, teersi na, indaale saricaam. Waaye, ba alxemes ji nu génn, sarica baa ngi woon ci loxoy Demba Kànji, àttekat bi jiite Kurelu ndajem wote bi. Bu ko neexoon mu def ko jàmm, baaxe ko réew mépp ; bu ko neexoon yit mu soppi ko safaan ba, def ko fitna. Lépp, nag, a ngi aju woon ci ni àttekat bii di Demba Kànji di séddalee saricay askan wi. Ñépp a ngi newoon tekk di ko déglu : ndax dina séddale saricay askan wi ni ko yoon bëgge ? Noo déggandoo li mu wax. Nee na tééméer bo jël, 58 yi Maki Sàll lañu sànnil xob. Ñu bare ci réew mi jàpp nañu ni du dëgg ndax li rajo yeek tele yi wax, ñépp di ci dégg, moo di ne ñaareelu sumb mënutoon a ñàkk te njiitu réew meek Idiriisa Sekk ñoo waroon a laalewaat.
Naqaru way-moomeel yi dara waralu ko lu dul yaakaar bu tas.
Ci fajar a fajar lañu jóg, wutali bérébi wotekaay yi ngir def seen warugar, ni ko maxejj bu nekk war a defe. Wote ren bi nag, mbooloo mu takku te farlu lees ci ràññee, rawatina ndaw yi. Ci xayma, téeméer boo jël ci ñi jotoon a bindu ci kayitu wote gi, juróom-benni fukk yi wéet nañu ci mbañ-gàcce gi. Nee ñu xiirte gu ndaw yi am ci bile wote, lawax bii di Usmaan Sonko moo ko waral. Ndaxte, Usmaan Sonko benn, ndaw la, ñaar dafa yeesalaat politig bi, di biral njub, gëm sa bopp ak bëgg sa réew. Ak lu ci mënti am, keroog ñépp xéy nañu, solu ba jekk, dem wote ci yar ak teggin ba 6 waxtu ci ngoon, ñu daldi tëj wotekaay yi, ngir lim xobi juróomi wutaakon yi bokkoon ci joŋante bi. Naam, amoon na ay rëq-rëq yu ndaw, waaye daal mënees na wax ne bëccëgu wote bi jaar na yoon. Bi asamaan si muuroo, nag, ci la mbir mi tàmbalee lëbëjoo, ñenn ñiy jéem a tuur lëndëm askan wi.
Bi timis ji maasee, ci la lim yu njëkk yi tàmbalee rot, ñetti wutaakoon yii di Maki Sàll, Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk beddeeku di wone seen doole. Xëccoo bi tar lool ci seen diggante. Ku raw fii, kee raw fee, keneen raw fale. Yeneen ñaari lawax yi ñoom, Isaa Sàll ak Madike Ñaŋ, nangu ndogal, xam ni bokkatuñu. Ku nekk ci ñoom ñaar gërëm askan week maxejj yi leen wóolu ba sànnil leen seeni kàrt ba noppi ndokkeel Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk. Waaye, biral nañu tamit ne, ku gën a jekku ci diggante ñaari wutaakoni kujje gi, moom lañuy jàppale ci ñaareelu sumb bi nga xamante ne, jàppees na ci njëlbéen ni mënta ñàkk. Ci jamono jooju, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñi ngemb Maki Sàll, ñoo giy fésal seen mbégte, naan Maki jël na raw-gàddu gi, xel wareesul a xalaat ñaareelu sumb di am. Loolu nag, du mbetteel, dafa di, ku ngemb sa mbër, bu la neexee bàkku ne yaay daan doonte dara wóoru la ci. Waaye, bi njiitu jawriñ li, Muxamadun Bun Abdalaa Jonn, génnee ca RTS ak TFM wax ni Maki Sàll faluwaat na ci sumb bu njëkk bi ak 57 baat ci téeméeri falaakon yoo jël, ci la xol yi jóg, coow li ne kurr.

Ci saa si, Usmaan Sonko ak idiriisa Sekk wooteb ndaje ak taskati xibaar yi. Ñaari wutaakon yi daldi ñaawlu doxalinu njiitu jawriñ yi. Waaye, yemuñu ci, ndax ŋàññ nañu màkkaanu taskati xibaar bu Yuusu Nduur bii di iGFM ak tamit RTS, rawatina yéenekaayi réewum Farãs France 24 ak RFI. Ñu neeti, kàddu njiitu jawriñ lii di Muxamadun Bun Abdalaa Jonn ak doxalinu taskati xibaar yees jot a lim, ag càcc a lalu ci suuf, ñu bëgg a nax askan wi, jox leen ay lim yu wérul. Waaye, ñoom duñu ko nangu ; te bu ko jaree, dinañu génn ànd ak askan wi xeex, jubali Pale ngir déjjati fa Maki Sàll.
Bi dënn yi demee ba tàng la àttekat bi jiite Kurélu ndajem wote bi xéy, woo taskati xibaar yi, daldi delloo njiitu jawriñ li palaasam, xamal ñépp ne, kenn amul sañ-sañu wax ne kii falu na walla ñaareelu sumb day am lu dul Kurélu ndajem wote gi mu jiite walla Ndajem ndeyu àtte mi. Bees ko laajee nag, kañ lees war a jot ci ngirtey wote bi, dafa xaarloo askan wi ba alxames walla àjjuma jees dégmal. Loolu nag, teeyoon na xel. Ndaxte, ak xeeti jumtukaayi xarala yi fi nekk, jarul woon a joxe àpp gu ni tollu. Mbaa du njiitu réew mi daa takkaloon pot Demba Kànji ak i ñoñam ngir ñu wax ne moo jël ndam li ? Am na sax ay ndaw yuy wax ne nguur gi dafa bëgg a foqati baatu askan wi. Ba tax na, ñenn ci ñoom tàmbalee ñaxtu ca buntu RTS di kaas naan ñaareelu sumb day am ci nii mbaa ci nee. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoom, ñu ngi ŋoy ci seen lim bi njiitu jawriñ yi fésaloon, naan : « wure wi dem na këŋŋ, Makee faluwaat ! » Li am ba des mooy ne, askan wi gëmmul nelawul. Bi Demba Kànji joxee dogalam ba tey, nit ña ngiy xultu tëwa ba, kujje gi woote na doxu-ñaxtu tey ci àjjuma ji, buñ jullee tàkkusaan ba noppi. Lan la ndaje moomuy jur ? Yàlla rekk a xam. May laajati : mbaa du léeb dafa tàbbi géej ? Moom daal, xalam demoon na bay neex…

Am na tamit ñu naan Maki Sàll dunguru Emmanuel Macron doŋŋ la te sax Tubaab yee ko may fitu yemale joŋante bi ci benn sumb kott. Loolu tekki ne Frãs ay ndeyu-mbill gi te xéy-na lees war a def mooy bañatee jënd lépp luy doomi-Frãs di jaay fi ci Senegaal, moo xam Auchan la, walla Orange laak Total walla ñeneen.
Àttekat bii di Demba Kànji nag, bu tasul woon yaakaaru askan wi, Senegaal du mel tey ni réew mu toog ci nen. Xéy-na am na lu ñuy yoot. Fitna du yem ci boppu boroom te bu pënd wuree, fattu bare.