XIBAARI TAGGAT-YARAM (1/10/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

KUPPEG ÀDDINA WAY-LUU YI (MUUMA YI)

Bàyyeesu leen xel, waaye way-luu (muuma) yi teewal Senegaal ca kuppeg àddina si bees leen jagleel ñoo ngay def i jaloore yu rëy. Ba léegi, ékib gañeeguleen ! Ñoo ngi toll ci ñeenti joŋante, gañe 3 yi daldi timboo benn bi. Kaar-dë-finaal lañu war a amal fan yii.

ILIMAAN NJAAY DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK AK MARSEILLE

Démb ci gaawu gi la Ilimaan Njaay, doomu Senegaal ji, di sog a dugal biiwam bu njëkk ak Marseille ci seen joŋante bi amoon seen diggante ak Monaco bi ñu ñàkk ci (3-2). Lii la wolof naan, xëcc bu daggul dikk. Jafe woon na ci moom ca njëlbeen ga, ba tax mu daan xaw a jaaxle. Waaye, mu gëm ko ba mu dikk. Njoortees na ni dana ko gën a firiloo nag, nde lees di séentu ci moom ëpp na li mu fa waneegum.

MÓORI JAW, KU JAR A BÀYYI XEL

Alin Siise war na bàyyi bu baax bëtam ak xelam ci doomu Senegaal bi, Móori Jaw. Moo ngi def i jaloore yu réy jamono jii ca këlëbam, Clermont. Gaawug démb gee ci mujju, mu def joŋante bu rëy xañ kii di PSG bu Mbappe ndam.

BARÇA AK MBIRUM NEGREIRA

Barça génnagul ci mbiri Negreira bi ba léegi. Mbir yaa ngi nekkoon ci loxo yoon mu di ko saytu di amal i luññutu. Ci fan yii nag, coow li dafa tàmbalee jugaat ba am ci sax ñuy ragal ñu tas Barça. Ndaxte, mbirum nger muy yàq powum futbal la. Waa Barça nag, ba léegi dañuy rasu, di bañ ni fayuñu benn arbiitar xaalis ngir mu ràccal leen seen boor. Kii di njiitu LIGA bi, Tebas, daldi na yëkkati ay kàddu ci loolu: “Ger (corruption) nekkul joxe xaalis rekk, Waaye, yéene bi kese, soo ko amee, mënees na la ci jàpp”.

NEYMAR A NGI BËGG A JAAXLE

Jamono jii, Neymar fireegul ca naar ya. Ndaxte, boobu ba léegi, bii dafa jaar nii mu jaar nee. Mbir yi dafa xaw a dëgëragum ci moom, ba léegi dugalagul. Benn paas la fa def, am fa penaalti daldi koy rate. Fees ko séentu woon tëllagu fa !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj