XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

AY YEESAL ÑEEL BARI (LES EQUIPES) SENEGAAL YI

Gaynde yu mag yi (ekib A)

Wéyalees na pasug Aliw Siise gi ba keroog atum 2026. Kii di Paap Caw lees tabb, teg ci wetam, muy tofoom (adjoint).

Gayndey réew mi (équipe nationale locale)

Bu dee lu ñeel gayndey réew mi, Suleymaan Jàllo lees dénk lenge, mu war leen a tàggat. Sosef Seŋoor ak Séex Géy ñoo diy tofoom.

Gayndey yu ndaw

Bu dee xibaar yi aju ci gaynde yu ndaw yi amagul 20i at (U20), Sëriñ Ja mooy leen yor. Bu dee gaynde yu ndaw yi amagul 17i at (U17), Ibraaxiima Fay a nekk ci bopp bi.

MUKTAAR JAXABI OPPEEREWU NA CI JÀMM

Alxames jiI weesu, 7 màrs 2024, la jañkatu Gine bi oppeerewu ci tànk fa raglub “Jean Mermoz” ba nekk Liyoŋ (Farãs). Lépp jaar na yoon. Waaye, gaañu-gaañoom bi du bu ndaw. Nde, gannaaw gaañoom bi ca seen joŋante (valence) baak Real Madrid ca ayu-bés bee weesu la fajkat bees di wax “Dr Gastaldi” biral ay kàddu di xamle ni dina jafe lool ngir Jaxabi doxaat ni mu waree. Ndaxte, xeetu gaañu-gaañu bi yamul ak yu bari yu futbalkat yiy ame. Dolli ci ne jéem a fexe ba mu doxaat lees war a seet balaa ñees di xalaat mu delluwaat ci pàkk mi. Muy lu ñu bari di ko mastawu.

ARDA GÜLER DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA REAL MADRID

Saa-Tirki bi dugal na biiwam bu njëkk ca Real Madrid, démb ci dibéer ji, ci seen ndaje beek Celta-Vigo. Moom nag, ba mu ñëwee ca ekib ba ba léegi amagul wërsëgu wane boppam bu baax. Ndax, dafa dikk rekk am ay gaañu-gaañu yu tegalante woon. Loolu doyul, Carlo Ancelotti miy tàggat këlëb bi du ko futbal-loo lu bari. Yenn saa yi mu mosal ko as lëf ciy simili, waaye li ci ëpp ci toogu bi la koy bàyyi. Démb itam, bi joŋante bi desee 8i simili la ko dugal ci pàkk mi. Waaye, lu simili yiy néew-néew, jot na ci bégal soppe yi, rawatina yu dëkkam yi bëgg di ko gis muy laale lu bari. Fim ne mooy Saa-Tirki bi gën a doon ndaw te dugal ca sàmpiyonaa bu Espaañ. Turam dugg na xaat ci mboor ma.

LÀMB JI

Bëre taxaw na digante Móodu Lóo, buuru làmb ji, ak Sitta. Ñoom ñaari mbër yi dinañu sëgg weeru Nowàmbar ci atum 2024 mii.

BOKS : FRANCIS NGANNOU ÑÀKKATI NA

Saa-Kamerun bi ñàkkaat na weneen yoon ca powum boks ma. Guddig àjjuma jàpp 8 màrs la doon amal ñaareelu xeexam ci wàllu boks. Jàmbaar jii di Anthony Joshua la doon laaleel. Aji-mujj ji daf ko dóor mu tëdd ca ñaareelu xaaj wa, daldi gañe joŋante bi. Moom nag, Ngannou dafa mel ne neexleegul ci po mi. Ndax, ba mu jógee ca MMA ba léegi amagul ndam ci boks bi. Xëy-na lim miinagul yëf yi la, am li mu ñëw rekk ñu jox ko ci waagay po mi. Di xaar ci moom mu dikkaat ak taxawaay bu gën a jekk ci yeneen joŋanteem yiy ñëw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj