XIBAARI TÀGGAT-YARAM (16/7/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

KUPPEG ÀDDINA SI 2026

Kippu yi ñeel xëccoo paasu kuppeg àddina si war a am ci atum 2026 mi génn nañ fii ci wàlluw Afrig. Senegaal moo ngi bokk ci kippug B gi mook ñii di Kóngoo, Móritani, Tógoo ak ñaari Sudaŋ yi. Senegaal lees jàpp ne mooy ékib bi gën a jekkandi ci kippu gi. Waaye, naataangoom bii di Kóngoo, di ekib bu mag itam, ëpp ko li mu jël ciy kuppeg Afrig du ko ko yómbalal wenn yoon. Te sax, léegi, ekib bu ndaw sax dafa amatul. Ekib yépp ay bañ-bañlu, di jéemantu ni ñépp. Senegaal ci boppam, xam na ni ñépp a koy xaarandi jamono jii. Ba tax na, joŋanteem yépp a nar a metti.

GENERATION FOOT JËL NA RAW-GADDU GI

Generation Foot bu Ndakaaru moo jël Sàmpiyonaa Senegaal. Démb ci gaawu gi la doon joŋnte ak Jàmbaar, ci 24eelu bëccëg bi. Benn poñ doŋŋ la soxla woon ngir kenn bañ koo dabati. Waaye, la gën témboo la def. Nde, dafa dóor Jàmbaar 1-0, daldi matal 50i poñ. Bii mooy ñetteelu yoon mu koy jël ginnaaw 2017 ak 2019.

ESTEFAAN BAAJI AMAAT NA KËLËB

Gannaaw ba mu delsee Senegaal, ci këlëbu Casa Sport bi ko lóofoon (tàggat bi muy ndaw), doomu Sigicoor bi, Estefaan Baaji, dina dem fa Siipr, xaatim ca këlëbu Olympiacos Nicosie ag pas gu tollu ci ñaari at.

AFROBASKET, KIGALI 2023

Jigéeni basket yi war a teewal Senegaal fa Kigali (Ruwàndaa) ñeel powum basket bi ñuy amal ci diggante réewi Afrig yi, dinañu dem ci 21 Sulet bii. Fim ne nag, ñoo ngi Ndakaaru di amal seen i tàggatu di ko waajal ni mu waree.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj