Benjamin Mendy duggaat na démb ci pàkkub futbal, gannaaw tuuma gu metti te yàgg bi tegu woon ci ndoddam, at yii weesu. Tuumay ciif yooyu ñu gàlloon ko ñoo taxoon ñu bari foogoo ne daf ciy jaare bàyyi futbal. Waaye, keroog, ba ñu ko setalee ni deful lees ko doon toppee, la daldi fasante ak Fc Lorient, këlëb bu nekk Farãs. Démb, ci dibéer ji 17i fan ci sàttumbaar 2023 la duggaat ci pàkk bi, ci joŋante Lorient ak Monaco. Soppey këlëb ba sargal nañu ko, woy turam. Ci 70eelu simili bi la duggu.
ABIIB BÉY A NGI NE PATT DI LIGGEEY
Dafa boolewul daraak wax. Moo ngi nekk ci ruqam ak këlëbam, Red Star, di def jéego yu am solo moom Abiib Béy, saa-senegaal bi bokkoon ci gayndey ati 2000 yi. Ci tàmbalig « saison » ren ji, amal na ci 5i joŋante, gañe ñeent yi, ñàkk benn bi.
GREENWOOD DUGGU NA XAAT CI MBOORU GETAFE
Gannaaw i tuuma yees ko tegoon moom it ci mbiri jigéen ba tax waa Manchester United daldi koy bañal mu toogaat ci ekib ba, àngale bi dafa daldi fasanteek Getafe, ab këlëbu españool. Ci ayu-bés bii nu génn, këlëb bi daldi nay jaay ciy mayo yees bind turam lim boo xam ni bii kenn mësu koo def ba Getafe di këlëb ba léegi.
JOAO FELIX DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA BARÇA
Barki-démb ci gaawu gi, ci ndamu Barça bu rëy bi 5-0 ci kaw kii di Real Betis, la Joao Felix daldi dugal balam bu njëkk ca këlëb ba. Loolu nag doon ci moom mbégte mu réy, nde bi ñu ko dékkee mikoro bi ba joŋante bi jeexee, dafa wax ni « yàgg naa dugal bii, waaye bii moo nekk bu ma ci gën a neex ndax dafay matal sama géntug futbalsi Barça. »