Ñaari mbër yi waajal nañu seen bés bi, def nañu lépp li ci war, neexal seen i jàkkaarloo ak bés beet. Lag dë geer 2 dafa ñëw, ànd ak kóolute, bàkku, yëngal, daldi koy xumbal. Sitta tamit, waxi noppi. Ñëw na nees ko xamee, ànd ak mbooloo mu takku, muy lees ko xamee it. Bàkku na ba Lag 2 bàkkoo ba noppi, mu neexal ko ba mu neex. Moom Sitta nag tay dafa dikkee nu doy waar. Dafa ñëw ak alikeñ, muur kanamam ba kenn gisu ko, ci waajtaayu bàkkoom la koy door a dindi. Cëy làmb, lu nekk a ngi ci !
Aren Nasiyonaal bi fees dell, loolu di dëggal ba tay lees di wax ni làmb ji dekki na.
Seen bëre bi neexoon na , tàngoon na it lool. Nde ñaari mbër yi bëre nañu xeex nañu tam.
Seen bëre baa ngi tàmbali ba 21i waxtu tegee 18i simili, ñu dawal wenn xaaj wi ba songoo ci, xeex ci ba mu jeex. Ba ñu noppaloo ba dikkaat ca la ñu gënee xeex ku ci nekk ñam sa moroom ciy kurpeñ, Sitta dem seeti Ardo daanaka ñeenti yoon. Gannaaw loolu, ñaar-fukki simili yees leen mayoon jeex ñu daldi jox Lag dë Geer 2 ndam li ci kaw dànkaafu (avertissement) bu Sitta am ci xaaj wu njëkk wi.
Sitta tamit, daanaka am na ndam lu koy soppeem jox ak seetaankat yi. Ndax njàmbaar gum wane ci kanamu ndaanaan bu tollu ni Lag 2, sonal ko, xeexloo ko. Lile di wane ni Sitta màgg na te noppi na ngir bëre ak ndaanaan yi ci kaw.
KUPPE : GAYNDEY RËKK NAÑ SUDAŊ
Démb la Senegaal doon laaleek Sudaŋ ci joŋantey bokkadil yi ñeel kuppeg àddina si war a am 2026 (éliminatoires de la coupe du monde 2026). Gaynde yi nag rekk nañ waa Sudaŋ, dóor leen 4-0.
Paap Mataar Saar ak Lamin Kamara ràññeeku nañ ci. Ndax, ku ci nekk dugal na benn bii, muy seen njëlbeeni bii. Seen bii yi nag jàppees na ni dina doon lu leen di gën a gëtëŋ ñu gën a firi, rawatina Lamin Kamara mi nga xam ni moo gën a nekk gan. Saajo Maane moo dugal yeneen ñaari biiyi.
KUPPEG ÀDDINA U17
Sunu ndaw ya ca “Indonesie” dinañu daje ak ndawi Farãs yi ñeel 1/8 dë finaal yi. Àllarba jii, 22 nowàmbar 2023, lañuy joŋante bu 12i waxtu jotee. Nu di leen ñaanal ndam.