Waa UEFA amal nañu ay coppite yoy, dañuy yokk limatu ekib yiy bokk ci joŋante Ligue des champions bu déwénee, atum 2024-2025 mi. Ci loolu, Araabi Sawdid mi nga xam ni, daanaka futbalkat yu xareñ yu bari ñoo ngi jóge Tugal di leen fekki ci seen sàmpiyonaa ba, ñu ci mel ni Ronaldo, Neymar, Benzema, Saajo Maane, Kulibali añs. Njiiti mbootay gi ëmb seen sàmpiyonaa ba fésal nañu seen bëgg-bëggu, maanaam fee ba këlëb biy jël sàmpiyonaa ba daldi di bokk ci Ligue des champions bi.
SAAJO MAANE AK RONALDO AM NAÑU SEEN KUB BU NJËKK CA NAAR YA
Keroog, ci gaawu gii weesu, lañu doon amal finaalu kuppeg buuru Araabi Sawdid bi. Joŋante baa ngi doxoon ci diggante Al Nasr mu Ronaldo ak Saajo Maane ak Al Hilal bu Kaliidu Kulibali. Ñoom Saajo Maane ñoo mujje gañe ñaari bii ci benn, Ronaldo daldi ci dugal ñaari bii, benn bi saajoo ko ko paas. Mu nekk seen kub bu njëkk ca Al Nasr.
REAL MADRID WUT NA GÓOL
Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi Thibault Courtois ame, Real Madrid daldi nay àbb jàppkatu Chelsea bi, Kepa. Àbb bi nag, ci diirub menn at kese la. Waaye, Kepa moom dafa bëgg toog benn yoon Real Madrid. Ca kaajaram ga la Kepa wax kàddu yii : “Dinaa góorgóorlu ba sama xareñte tax ma toog lu ëpp at fii ci Real Madrid. “
LIGUE DES CHAMPIONS AFRIG
Ci njëlbeenug joŋante yi, këlëbu senegaal bii di Generation Foot mi jël sàmpiyonaa daaw bi dina ci daje ak Hafia Fc bu Gine. Ci dibéer jii, 20 ut 2023, lañuy futbal.