Démb ci talaata ji la ekibu Senegaal bu mag bi doon amal joŋantebe xaritoo ak bu Beresil, faLiisbon, gëbla Purtugaal. Ndekete, sunu gaynde yi yarasuñ benn yoon ! Firndeel nañu tamit ne, duñu yàqi te duñu bàyyeeku. Ndax, Beresil a ñjëkk a dugal. Waaye, Senegaal mayu ko sax mu noyyi. Nde, 4 la ko yen laata Beresil di dugalaat beneen, muy 4-2. Ndam li, ndam lu réy réy. Ndege, Senegaal mooy ekibu saa-afrig bi njëkk a dugal Beresil 4i bii. Rax-ci-dolli, 2014 ba tey, ginnaaw bi ko Almaañ rokkosee woon 7i bii ya, guléet mu jël lu tollu ci 4i bii. Kon, gàcce-ngaalaama sunu gaynde yi. Abiib Jàllo moo dugal benn, Marquinhos dugal seen kã, Saajo Maane lakk caax yi 2i yoon.
Aliw Siise bégoon na ci gaynde yi ak ci ni joŋante bi deme. Moo ko tax a bëgg lu ni mel di faral di am. Daf ne :
“Joŋante yu mel nii lanu bëgg ngir di ci nattee sunu doole. Bëggaat nanu ci yeneen yoo xam ni, Ndakaaru lay doon, Senegaal. Beresil na ñëw ñu dalal ko sunu réew mu xam ko, walla sax Àrsaantin.”
Bu dee Saajo Maane nag, mi ngi gën a rëdd turam ci mbooru kuppeg Senegaal. Ndax, démb la dugal 36eel ak 37eeli biiyam ak Senegaal.
Cristiano Ronaldo : 200eelu joŋante ak Purtugaal
Ronaldoo démb ladoon amal 200eelu joŋanteem ak dëkkam, Purtugaal. Guddeem ga neexoon na nag. Ndaxte daf ci dugal benn bii bi tax Purtugaal gañe joŋante bi. Moom itam, mag mu dul màgget la ; doon paa terewukoy gën a aj turam ci mboorum kuppe gi.
Ngoloo Kànte fekki na Bensemaa
Ngolo Kànte juge na Chelsea, fekki Kariim Bensemaa këlëbu Al-Ittihad, ca naari Araabi-Sawdiit ya. Liñ naan xaalis mën na lu ne, ndeke dëgg la. Ba fa Ronaldo demee, dégg nañ ci gannaawam wax ju nekk. Waaye de, dafa mel ni ñiy topp yoonam a ngi bëgg a bari. Naar yaa ngi yóbbu ñu bari.