Bërki-démb ci guddi, bi 3i waxtu jotee, la saa-arsàntin bi doon amal joŋanteem bu njëkk ak këlëb bu bees bee di Inter Miami fa USA (Amerig). Boobu këlëb nag nga xam ni futbalkat bu mag ba woon, David Beckham moo ko moom, defoon na 11i jonante yoy, gañewu ci woon benn. Bi Messi dikkee lañu xamaat cafkay ndam. Ci ñaareelu xaaju joŋante bi la Messi duggu, mu ngi fekk ñu nekkoon ci 1-1, gannaaw ba ñu jiitalee woon ekibam mul delsi. Ñuy dawal noonu ba ca bopp jeexital ga rekk, Inter Miami am teg-dóor. Booba, ñoo ngi woon ci 94eelu simili bi. Messi dafa teg bal bi, laxas ko ci caax yi, rekk powu bay riir. Kii di boroom këlëb bi David Beckham dafa bég bay jooy. Ndeke, Messi jeexalagul.
ÓBAMEYAN AK ISMAYLA SAAR CA MARSEILLE
Maarsey moo ngi wër di defaraat bu baax taxawaayu ekibam. Bërki-démb lañ siiwal ñëwub Óbameyaŋ. Moom sax, tàmbali na tàggatoom ak i farandooram ya. Ci dibéeru tey jii tam, biral nañ seen déggoo diggante ak Watford mi moom Ismayla Saar. Daanaka, gayndeg Senegaal gi, léegi kuppekatu Marseille la. Ëllëg ci altine ji lañuy saytu yaramam foofu ca Marseille laata lépp di mat.
AB FEEBAR CI BIIR FC BARCELONE
Futbalkati FC Barcelone yi, jamono jii, dañu jànkonteel ak feebar bu law seen biir. Looloo tax sax ñu fomm joŋante bu njëkk bi ñu waroon a amal ëllëg ci doxantu bi muy amal fa Etaasini. Njortees na ni kenn ci ñi demoon Afrig ci bër yiñ amoon a ko indaale. Amaana mu bañ a ñàkku laata muy dem. Waaye, wax jooju amul ndëgëlaay. Nde, amul lenn lu koy firndeel.
AFROBASKET 2023, KIGALI
Sunu Jigéen ñi dem nañu Ruwàndaa bërki-démb, àjjuma guddi. Jot nañ sax amal gaawug démb gi seen tàggatu gu njëkk foofa ca tàggatuwaay (Gymnase) bu Liise Kigali. Afrobasket baa ngi war tàmbali 28eelu fan ci weeru sulet, war a jeex 5eelu fan ci weeru ut.