Afrig moom, dafa mel ni ndeyam liggéeyul. Saa bu CAN bi jubsee, coow li jib, ñuy ŋëwti-ŋëwti joŋante bi. Te, bu “Euro” bi jotee, kenn du dégg coow ñeel ko. Waaye bu Joŋantey Afrig teroo rekk nga dégg lu nekk. Li ko waral nag mooy ni këlëbi tugal yi ame ay futbalkati ñuule dañuy jàpp ne loolee daf leen di yàqal seen i mbir.
Looloo waral njiital Bayer Leverkusen li, Fernando Carro de Prada àddu ci kàddu yii : “Jaaduwul kuppeg Afrig bi di am ci diggu atum futbal mi (saison). Ngir soppi loolu, dinaa jokku waa FIFA. Noo ngi xool itam ndax amul yoon wu jaadu wees mën a aw ba bañ a bàyyi sunuy kuppekat ñu dem.”
Yile kàddu boo ko déggee dafay wane ni Afrig joxuñu ko cër, muy lees war a taxaw temm ak fulla dox ci, wax ci ba Afrig jël lum yellool.
PAAP GÉY A NGI WAAJAL ÑËWAATAM
Gannaaw ba ko FIFA daanee woon, aj ko lu tollu ci ñeenti weer ndax coow li amoon ci demam ca Marseille, doomu Senegaal dina dikkaat ci weeru desàmbar wii. Jàppees na ni dina bokk ci seen Joŋante ak Lorient bu Bàmba Jeŋ bu 10i fan ci weer wii.
BUUNA SAAR GAAÑU NA
Xalam demoon na bay neex, buum ga dog ! Ci fan yii weesu, gisees na ni gaynde gi doon na tàmbali di bokku ci ndawi Bayern yiy tàmbali Joŋante yi, bay def sax génn yu baax. Waaye gaañu-gaañu bu mettee ko dab, “ligaments croisés”. Mu war a toog li dess ci atum futbal mi.
SOFIYAAN JÓOB IT GAAÑU NA.
Futbalkatu Nice bi dafa ame damm-damm ci “3e métatarse” bi. Loolu jural ko 6i ayi-bés yum war a toog te du laal bal. Xel di teey ci ndax dina bokk ci CAN bi am deet.
ILIMAAN NJAAY NEEXLEEGUL CA MARSEILLE
Ci seen Joŋante bii weesu gisees na coow li amoon ci digante Ilimaan ak tàggatkatam bi Gattuso. Li ko waral nag mooy ni Njaayeen bi dafa xawoon a yeex ci soloom bi gannaaw bañ ko woowee ngir mu dugg.
Gannaaw loolu, Gattuso andi na ay leeral ci mbir mi di wax ni : ” Weccente naa ak moom bi Joŋante bi jeexee (…). Ekib bi daf ko soxla. Bu nekkee dëgg, bokk na ci ni gën a xereñ ci sàmpiyonaa bi, looloo waral may taral ak moom. Mer naa ci, waaye jéggalunaa itam. “