Ci gaawug démb ji, 2 sàttumbaar 2023, la kuppekatu Mali bi gaañu. Ndem-si-Yàlla Saalif Keyta mi ngi amoon 76i at. Moom, doomu Mali ji, mooy kuppekatu saa-afrig bi jëkk a gañe Kuppeg wurus gu Afrig (Ballon d’or africain) ca atum 1970. Saalif keyta, ku aayoon lool la, taqe woon te xareñ. Moo tax, jot na def i jaloore yu baree bari ci futbalu Afrig, waaye woneet na mëninam fa Tugal. Dafa di, ku fa siiw la, rawatina biir Farãs.
Bésub 6eel ci weer wii lees jàpp ngir sargal ko. Dees na ko jagleel ab yaxal bu yaatu ngir fésal jaar-jaaram.
BELLINGHAM A NGI WÉY DI WONE BOPPAM FA ESPAAÑ
Doomu Àngalteer ji dafa ñëw ci sàmpiyonaa Espaañ bi rekk daldi miin. Démb ci gaawu moo nekkoon ñeenteelu joŋanteem ak Real Madrid. Waaye, bu ci nekk dugal na ci. Fim ne nii, mu ngi ci 5i bii ak benn paas. Soppey Real Madrid yi dugal nañu ko seen xol te demaguñu fenn.
SERGIO RAMOS DELLU NA SEVILLE
Gannaaw ba mu jeexalee pasam ak waa PSG, moom jañkatu Real Madrid ba woon mu ngi toogoon ci ruqam di liggéey. Ci dibéeru tey ji, 3i sàttumbaar, la dellu Seville, fa mu jóge woon dem Real Madrid.
RONALDO AK SAAJO MAANE ÑU NGI BOYAL ÀLLU NAAR YI
Déggoo bi dafa mel ni dafa teel a jàpp njaax diggante Saajo Maane ak Cristiano Ronaldo. Jamono jii, ku nekk ci ñoom ñaar a ngi xiir di def loolook loolu. Ronaldo mu ngeek 5i bii ci ñetti joŋanteem ak ñetti paas, Saajo Maane amagum 4i bii moom it ci ñeenti joŋante ak seen këlëb bii di Al Nasr.
NDEKE ISCO MÀGGETUL !
Ñu bari jàppoon nañu ni ay balam dañoo jeex ndax li mu toogoon lu tollu ci 9i weer ci bãwu Real te futbalul. Ci merkatoo bii la fasanteek Real Betis. Boobu ba léegi nag, moo ngi fay wane xereñte gi ñu ko xame woon. Seen ñeenti joŋante yépp moom lañu tabb baay faalu joŋante bi, jot na ci dugal benn bii.