XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

KUPPEG ÀDDINA U17 2023

Ndawi Senegaal yaa ngi ci waajtaayu kuppeg àddina si ñu dëgmal te war a am ci weer wii di teew. Cig waajtaay, fas nañu yéene amal ñetti ndajey xaritoo. Démb sax lañu bi ci njëkk ak Panama daldi koy dóor 4-1. Amara Juuf, Idiriisa Géy, Yayaa Jémme ak Umar Sàll ñoo dugal.

Bokk nañu nag ci kippu gu dëgër, ànd ci ak Àrsàntin, Sàppõ ak Poloñ. Waaye, bu ñu dëggalee seen bopp, dawal seen futbal, mën nañu am dara.

LAMIN KAMARA DUGAL NA BALAM BU NJËKK CA METZ

Lamin Kamara démb lay sog dugal njëlbeenu biiwam ci Ligue 1 ak Metz. Ndaw bii bu réy ! Moom de kenn du ko fàtteel bu njëkkam bi. Nde, jàppees na ni dina bokk ci bii yi gën a rafet ci at mi. Ci seen joŋanteb démb ji ak Monaco la saa-senegaal bi daldi këf bal bi ca diggu powu ba, fekk góolu Monaco bi génnoon kãwam yi, mu lawbe ko ci soriwaay bu tollu ci 58i ñay (mettre).

FSF MOO NGI GUNGEE KËLËBI SENEGAAL YI AK ÑI KOY DOXAL

Fédération Sénégalaise de Football (FSF) xamle na ni tàmbali na gunge (subventions) yi muy defal këlëb yi ngir ñuy waajal seen bopp at mu nekk bu sàmpiyonaa biy waaj a tijji. Ren jii nag, koppar li mu teg ci taabal ji dañoo wàññeeku bees ko tëkkaleek yu daaw ya. Li ko waral nag mooy ne, daaw, dafa fekk nu gañe kuppeg Afrig ba noppi kalife woon ca kuppeg àddina sa. Moo taxoon mu joxe woon lu tollu ci benn miliyaar ak xaaj. Ren nag, daf ko wàññi ba mu toll ci 709 250 000 ci sunuy koppar ngir këlëb yeek ñi leen di doxal (acteurs) waajal ci seen bopp.

MAROG DINA YEESAL

Bu nu joxee nopp seen i njiit, Marog dina taxawal powu bu bees boo xam ni mooy doon ñaareelu powu bu gën a rëy ci kembaaru Afrig fii ak atum 2028. Moom Marog moo war a dalal kuppeg Afrig 2025, war a bokk dalal itam kuppeg àddina si, keroog 2030, mook Espaañ ak Portigaal. Réewum Afrig bi gën a sori ci mbooru kuppeg àddina (dëmi-finaal) dafa fas yéene dugal boppam bu baax ci wàllu futbal bi.

RONALDO FASAGUL YÉENE BÀYYI

Purtugees bi defagul mbirum bàyyi futbal ci xelam. Boo dégloo ay kàddoom xam ni waaju ko sax : ” Dina wéy di futbal ci at mii ak mi ci topp. Ginnaaw loolu, dinaa xool ndax sama yaram dinaa mën a àttan futbal bi am déet.”

Ci atum 2023 mii, moo nekkagum futbalkat bu ci ëppaley bii (44) ci kanamu Mbàppe ak Halland.

MAGUIRE MOO NGI ÑËWAAT

Àngaleb Manchester United bi moo ngi tàmbali di ñëwaat ndànk ndànk, di tàmbaliwaat di def joŋante yu wóor. Gaawu gii weesu moo ci mujju, moom lañu tabb baay-faalu joŋante bi ci seen ndam li ñu am ci kow Sheffield United.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj