Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu ci ñeenti weer a ngi nii (ut, sàttumbar, oktoobar ak nowàmbar) moom lees di tabb ki gën a xareñ ci weer wi.
Santos wacc na
Këlëbu Beresil bi moo ngi am ren 111i at ba ñu ko taxawalee ak léegi. Ren jii di guléet muy wàcc ca ñaareelu sàmpiyonaa ya (D2). Loolu nekk lu doy waar ca boobu këlëb. Ndax, guléet la, te dafa doon ekib bu mag boo xam ni bii ay punkal ñu fa jaar, ñu ci mel ni Pële ak Neymaar…
Musaa Wagee ngi dikkaat ndànk-ndànk
Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon at yii weesu ca Barça, loolu bokk ci li wàññiwoon xareñteem, ca la doomu Senegaal ji mujje woon a jóge foofu dem ci këlëb bii di Anorthosis Famagouste, ca sàmpiyonaa Siipr. Mu mel ni mu ngi delsi ndànk-ndànk ci nees ko xame woon. Ndax, ci weeru nowàmbar bii ñu génn, moom lees tabb ki gënn a xareñ ca weer wa.
Tijaan Jàllo wax na bëgg-bëggam ci ekibu Senegaal
Bokkoon na ci ndaw yi teewaloon Farãs ci Kuppeg Àddina gees jagleloon ndaw yi ëppalagul 17i at yi weesu ci fan yii. Moom nag xamle na ni lu koy neex la mu futbalal Réewam mii di Senegaal. Loolu nag xëyna dina neex mbokki saa-senegaalam yi waaye ña di waa-Farãs njort na ni du yam ca ñoom. Loolu nag war a tax ekib bi ubbil koy loxoom donte daf koy boole ca ndaw ña ngir mu am lim bëgg ak ñu bañ ko xatal ca ekibi Farãs ya.
CAF Awards : Lamin Kamara jël na cargalug ndaw bi gën a xarañ
Lamin Kamara (19i at), Amara Juuf (17i at) ak Ezzalzouli (U23 Marog) ñoo nekkoon ndaw yuy xëccoo cargalu gi ñu jagleel ndaw bi gën a xarañ ci at mi fii ci Afrig. Lamin Kamara moo ko mujje jël. Moom, Lamin Kamara, daf def at mu am solo, jël ci CHAN beek CAN U23, ba noppi di joxe ca këlëbam, bokk it léegi ci Ekibu Senegaal bu mag bi.
Cargal gu mag gi, balu wurus bi (ballon d’or), Saa-Niseriyaa baa ko jël, Wiktoor Osimen.
Basket : Góorgi Si Jeŋ bàyyi na
Saa-Senegaal bi xamle na ni bàyyi na basket bi ci benn laaj-tontu bu yàggul ak Jeff McDonald Du San Antonio. Moom nag mu ngi toll ci 33i at.
LÀMB
Amaa Balde ak Giri Bóordoo jàppees na seen bëre 30i fan ci weeru suwe bii di ñëw ci 2024 mi. Saa-Cees ak Ëmma Seen itam jàppees na ko ci 5i fan ci me bi.