Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran).
Saa-Senegaal bi moo ngi wane xarañte ca ekibam boobu di Rangers FC fa Ekos. Fi mu nekk nii, moo ngi ci 14i bii yu mu dugalagum. Ndax loolu dina doy ngir Aliw Siise wóolu ko ci CAN bii ñu dëgmal ? Kenn xamagul. Lu leer daal mooy ni soxlees na ci ekib bi ay ataakã yu xarañ ci kanami kã yi.
LÀMB JI : MÓODU LÓO AK BOY ÑAŊ NAROON NAÑU SONGOO
Démb ci gaawu gi 15i Desàmbar bi la ñaari mbër yi doon amal seen jàkkaarloo bu mujju laata seen bésu bëre 1 sãwiyee 2024.
Ci jàkkaarloo bi, doomu pikin bi dafa fekki Móodu Lóo di nappanteek moom, ñuy sannantey kàddu ci suuf jekki saay rekk doomu Parsel bi daldi koy buux. Ba loolu amee ñu nar a jàppante foofu faf ñenn ca ña ànd ak ñoom ak ca njiit ya dox seen diggante. Yu ni mel dees na wane ni ñaari mbër yi pare nañu ngir neexal bés bi. Waaye nag, lu jar a yamale la laata muy jur lu ñaaw.