Ëllëg, ci altine ji, bu 18i waxtu jotee la Senegaal di daje ak Niseer ca fowu ba ca Jamñaajo. Muy joŋanteb xaritoo bees taxawal ngir waajalee ko CAN bi war a tàmbali 13i fan ci weer wii. Bu ñu noppee ci loolu, ndawi Senegaal yi di waajal ngir dem Koddiwaar.
ÀNDRE ONANA
Góolu Kamerun bi fekkijeegul i naataangoom ca seen waajtaay ya. Lu ko waral nag, moo di ne Manchester United dafay amal ab joŋante kub moom ak Wigan ëllëg ci altine ji, ak joŋanteb sàmpiyonaa moom ak Tottenham keroog 14i fan ci sãwiyee wii. Bu ci noppee lay daldi fekkiy moroomam ya. Loolu nag, waa Manchester United ñoo ci waxtaan ak waa Kamerun ba juboo ci.
CAF YOKK NA NDÀMPAAYU CAN BI
Senegaal mi jël CAN 2022 bi jotoon na lu tollu ci 2i tamñareet ak 997i tamndareet yu teg ci sunuy koppar. Ci wii yoon nag, waa CAF dañu daldi yokk yëf yi ba ci 4i tamñareet ak lu teg. Moy lu am solo lu ñépp rafetlu.
PAAP MATAAR SAAR FEDDALI NA PASAM
Doomu Senegaal ji moo ngi jóge woon Metz (Farãs) fekki woon Tottenham daaw. Ren nag, dafa wane xarañte ak jom ju ko yóbbe mu bokk ci ñay tàmbali saa su ne ca ekib ba. Ci loolu, mu jubook gaa yi daldi féddali pasam ca ekib ba ba atum 2030.
LÀMB JI
Ci altine jee weesu, di woon fan wu njëkk ci atum 2024 wii, la Móodu Lóo doon daje ak doomu Pikin jii di Booy Ñaŋ 2. Waaye, daf ko jaarati fa mu jaar ay magam. Doomu Pàrsel ji waneeti na mën bëreem ak faaydaam ci cëru buuru làmb ji mu yore. Niki mu daanee woon Ëmma Seen ak Aama Balde, noonu la daanaatee Booy Ñaŋ 2. Mu mel ni, léegi daan na ñees yaakaaroon ni mën nañu ko të ca biir Pikin. Fim ne nag, ñoo ngi seet kan ay jekk ci moom ngir boolee leen. Ay tur a ngi jib boobu ba léegi, ku ci nekk naan diw baax na ci moom, waaye jàppaguñ dara.