Gannaaw tukki bi Messi amaloon ca Araabi Sawdid, njiiti Paris Saint-Germain daan nañ daan bu diis. Dañoo ajandi Messi ñaari ayu-bés yoy, du ci futbal te yit du ci tàggatu. Yemuñu foofu de, ndax dinañ ko dagg peyoorug ñaari ayu-bés yooyu ñu ko ajandi.
Gannaaw bi loolu amee, démb ci àllarba ji, 3 Me 2023, benn naaxu soppey PSG dem nañu ca màkkaanug ekib ba, doon fa yuuxoo turu Messi bay yëkkatiy saaga yu ñaaw di ko teg ci kaw saa-àrsantin bi. Bañ fa jógee, dafa am ñenn ñu dem ba kër Neymaar taxaw ca buntu ba itam doon ko saaga ak di ko móolu.
Ci ginnaaw xamle nañ ci lu wér ne Messi day dem bu at mi jeexee.
CAN U17
Kaar, sunu xale yaa nga ca yoon wa. Caatu gaynde yi nekk nañu ñi nga xam ne ñoo njëkk a dem kaar-dë-finaal ci kuppeg Afrig gii ñu jagleel ñi amagul 17i at foofu ca Alséri, gannaaw ba mu dóoree ñaari joŋanteem yi njëkk.
BULAAY JA, GAYNDE GU DÉGGUL JAT
Jamono jii, kenn mënul a téye Bulaay Ja foofu ca Itali. Keroog, ca ayu-bés bi weesu la xañ Napoli mu doon sàmpiyoŋu Itali. Ndax bii bi mu duggal ca njeexitalu joŋante ba. Démb, ci àllarba ji, mu dugalati ñetti bii ci seen joŋante geek Fiorentina.
ESPAAÑ : FINAAL “COPA DEL REY”
Real Madrid dina daje ak Osasuna Gaawu 6 Me gii ñeel finaalu kuppeg Buuru Espaañ bi. Ñu ciy xamle ni Modric mi ame woon gaañu-gaañu dana bokk, ndax tàmbaliwaat na tàggatu.