Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi, Saa-Muritani yi, ñu mujje leen ko yóbbul benn bal ci dara (1-0). Ab teg-dóor lañu am, dugal ko ci xaaj bu njëkk bi.
Alseri, moom mi dalal joŋante yi, moo dóor na Koddiwaar 1-0. Madagaskaar itam a dóor Mosàmbig 3-1, Niseer daldi gañe Gana 2-1. Ñu war a jëm ci demi-finaal yi. Senegaal dina daje ak Madagaskaar 31i fan ci saŋwiye bi (19i waxtu) gannaaw ba Alseri dajee ak Niseer ba noppi (16i waxtu).
Saajo Maane a ngi waaj a delsi
Saa-senegaal bi, Saajo Maane, tàmbaliwaat na tàggatu fale ca këlëbam bii di Bayern. Ci fan yii nu génn, la dellusi ci pàkku tàggatuwaayu Bayern. Donte àndagul ak i moroomam yi, noo ngi gis muy liggéey di tàmbaliwaat di laal bal bi ndànk-ndànk. Loolu nag, nekk na luy dalal xeli almaŋ yi ak soppey këlëb ba, rawatina bi seen joŋante bu am solo bi ñuy waajal ak PSG jegesee.
Cig pàttali, doomu Bàmbali bi dafa ame woon gaañu-gaañu ci óom bi. Weeru oktoobar 2022 la ko daloon. Dafa di, looloo ko tere woon a bokk ca kuppeg àddina sii weesu ca Qataar.
Li mu delsi nag, du almaŋ yi rekk a ci bég. Mbokkam yépp, Saa-Senegaal yeet kenn demul ñu des. Ndaxte, sunu sag la. Ñépp a koy seetaan di bég ci moom. Kon ñoo ngi koy ñaanal bu baax mu gën a tane ba dellusiwaat ci pàkki wure yi.
Bàmba Jeŋ dem na Lorient
Bàmba Jeŋ jóge na Marseilles. Nde, këlëbu Farãs bi mujje na nangu li Lorient fay, daldi koy bàyyi mu soppi këlëb. Bërki-démb, ci àjjuma ji, la dem ca këlëbam bu bees bi, ñu wane ko muy saafonte ak soppey Lorient ya. Moom nag, ba fa Sampawoli jógee la yaakaaram xaw a tas. Ndax, tàggatkat bu bees ba, Tidoor, boolewu ko lool ciy mbiram, ba tax lam fa doon wure bareetul woon. La mu gënoon a bëg nag, mooy toog fa wane fa boppam. Waaye, am nañ yaakaar ni dem gi moo gën ci moom ndax xale la te fàww muy joŋante ngir gën cee màgg bay wane boppam.