XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Real Madrid a ngi wër góol bu bees

Thibault Courtois, góolu Real Madrid bi,  dafa ame gaañu-gaañu bu metti (rupture des ligaments croisés) ba tax na dina toog diir bu yàgg door a góoluwaat. Loolu nag, jur na njàqare biir Real Madrid ba tax ñoo ngi ci wër góol bu koy wuutoondi ko ca caax ya. Jamono jii nag, ñoo ngi làmbaatu fu nekk.

Christopher Nkunku dina gëj ci pàkk yi

Moom Nkunku, bi ko Chelsea jëndee yàggul dara. Waaye, du gaaw a futbal. Ndax, dafa gaañu moom it ci oom bi. Dañu ko oppeere sax. Xamle nañu itam ni dina toog diirub ñeenti weer laata muy dóoraat ci bal.

Kylian Mbappe demul Real Madrid

Li coow liy bari lépp ñeel Mbappe, ndax dafay dem Real Madrid am am déet, Mbappe dafa noppi rekk, ni tekk tekkaaral. Ba ci alxames ji, mu daldi ciy àddu. Li mu xamal njiitu Paris Saint-Germain li mooy ne, moom Mbappe, dafay toog PSG, mottali at mi ko dese sog a dem ci coobareem. Jamono jii nag, bëgg-bëggu njiiti PSG yi mooy mu yeesalaat pasam ba 2025, nga xam ni déwén, buy dem ñu man ci am dara. Wàññeeku, Mbappe dafa bañ loolu. Lim bëgg mooy jeexal at mi ko dese, demal boppam.

Noah Fadiga amaat na këlëb

Doomu futbalkatu Senegaal ba woon, Xaliilu Fadiga, dafa mel ni li daloon baay jaa koy bëgg a dal, mbirum feebaru xol bi. Loolu waraloon sax këlëb bim nekkoon ca Farãs, Brest, dogoon pasam. Mu bañ a yaras nekk di tàggatook a faju ba amaat këlëb, Gant. Muy këlëb boo xam ni bii, baayam Fadiga nekkoon na fa menn at ci mujjantalu dundug futbalam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj