YENU SA BOPP

Yeneen i xët

Aji bind ji

“Yen bu diisee, dañu koy jàppoo”. Loolu la maam ja waxoon. Noppeegul sax, kenn ca sët ya ne ko : “waa maam, lu ma yenuwul naka laay xamee diisaay bi ?” Mu tontu ko ne : “moo doom, lu bët di jariñ boroomam ? Du yenu gaa, waaye xam na lu bopp àttan !” Sët ba xamatul lu mu cay teg muy wax ci xel mi : “sama maam jii xawma fu mu jàngee tontu rekk.”

Xam nanu nees mën a jàppalee ku yenu ab dàmba màngo walla ab saaku dugub. Waaye, bu dee nun ci sunu bopp danoo bokk ci yen bi moom, naka ci pexe ?

Laaj bii sampu ndiruwul lu am maanaa. Ndax yenu moom, ci gisin, deesu ko def nit. Dëgg la, waaye boroom kër gu ne, ni mu yilifee njabootam, noonu la ñu nekkee ab yen ci moom. Niki noonu, sëriñ bi ak i ndongoom, fara bi ak waa goxam ba ci Njiitu Réew ak ñi dëkkee Réew ma. Kilifa gu ne rekk, ñi mu yilif yen lañu ci moom. Ndaw yen bu diis ! Bu ñu ko sëfoon mbaam de, du ko àttan. Nde, kenn nit rekk ëpp naa yenu.

Ndegam ku nekk sa kilifa dalaa yenu, bu fakkastaloo, nga xalangu. Kon, jàppale ko wareef la. Ndax kat, wolof nee na, ki la boot di bëre, waroo ko ñaanal mu daanu. Te, li gën a yomb ci jàppale ag kilifa mooy ku ne yenul ko sa bopp. Maanaam, kenn ku ne xam li ko war te nekk ci. Te sax, sas wi jiitu ci nit mooy mu yenu boppam balaa ciy teg leneen.

Bokk na ci li njëkk a war nit ci kilifaam, mooy mu nangul ko kiliftéefam te déggal ko. Déggal ko te topp ko feek mi ngi tegu ciw yoon. Ginnaaw loolu, mu fexee taxaw taxawaayu kilifa ci boppam. Te moo di, def li ko war ci kéem kàttanam ngir mbir mi leen boole jag, donte sax dafay doon ci lu kenn dul fekkee. Nit, doon kilifag boppam itam dina ko tax a wuutu kilifaam ci lu bari. Ndax, dina ko mën a féete feneen fu mu mënul woon àggal boppam ci lu mu yëg, walla lu mu yëgul. Bu ko defee yen bi gën a woyof. Te, bu yen bi woyofee, doxin wi gaaw.

Rax-ci-dolli, bokk na ci liy woyofal yen bi mooy nit di moytoo nax kilifaam. Nax sa kilifa moo gën a bon nax sa bopp. Nde, njeexit yi muy jur mëneesu koo xayma. Dafa di, ay yàqu-yàqu yu jéggi dayo lay jur. Ku nax sa bopp, sa bopp doŋŋ nga nax. Waaye, ku nax sa kilifa, mbooloo mi mu yilif mépp nga boole nax (tàmbalee ko ci yaw !). Te loolu, mën na yóbbee ñépp ci njuumte lu rëy a rëy, te it du def lu dul yokk diisaayu yen bi, kilifa gi gën a sonn, mbir yi tagatémbe.

Kenn ku nekk, lu sa bopp diis diis, boo ko yenoo ni mu waree, noppal sa kilifa te ku noppal sag kilifa, ñoŋal saw nekkin. Ci kaw loolu yépp nag, kilifa gu mu ci mën a doon, nit la. Kon ñépp manuñoo mànkoo nangul ko. Waaye ku àndul ak moom it, waroo ko yéenee mu tarxiis ndax doo ci mucc.

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj