Ci ndoorteelu ayu-bés bi, altine 20 ci weeru me 2024, la waa jàngu bi doon amal aj gi ñuy def fa Popengin. Gu ren ji nag moo doon 136eelu wi yoon ginnaaw bi ñu ko tàmmbalee amal ca atum 1888, ci ndigalu Mgr Pikaarda. Mu digle woon ko ngir samp fi Senegaal ab barab bob, way-gëm yu jàngu bi dinañu fa mën di dajaloo, di def i ñaan ak a wéttalikoo Yàlla ji, nees koy defe fépp foo dem ci àddina si.
At mu jot ñu tànn ponk bu ñuy waxtaane, ju ren jii nag ñoo ngi ko doon amal ci ponk bii di « Ak sunu yaay Mari, nanu booloo dox ngir Senegaalu yoon ak jàmm ». Keroog, ci ubbite bi, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, teewoon na fa. Yékkati na fay kàddu itam wax ci solo si xew moomu am ci wàllu dundal ruu, ndimbal, njéggal ak yërmande te ñu war ko wone ni royukaay ci àddina sépp. Sàkku na fa yit ay ñaan ñeel réewum Senegaal ngir mu bennoo, dox ci yoon, am jàmm ak dimbalante.
Bu weesoo loolu, jëloon na ndogal, ci màqaama Njiitu réew li mu doon, ngir jàppale leen ci aj gi, yaatal ko ci jàngu bépp. Ba tax muy sàkku ci ñiy taxawu aj gi (le comité d’organisation) ñu ràññee soxla yi gën a tembare ngir Càmm gi mën cee sàkk i pexe yi war ba junni junniy way-aj yi fay daje at mu jot mën faa nekk ci anam yi gën.
Mu doon ay weccontey xalaat ci li ñu bokk ciy warteef ci diggante Càmm gi ak Saa-Senegaal yi, way-gëmi jàngu ngir Senegaalu jàmm ak naataange. Mu nekk at mu njëkk ci Càmm gu yees gi. Tax ba njiitu jàngu bi di leen fàttali liy Saa-Senegaale yi di xaar ci ñoom. Wax ci jafe-jafe dund bi, yaakaari ndaw ñi, añs. Loolu la jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, di Să Batist Tin ma fa teewaloon Càmm gi, feddaliwaat na, daldi dëggalaat ca ndaje mu mujj ma. La mu fésal mooy taxawaayu jàngu bi ci tabaxug réew mi. Mu ciy njukkal waa jàngu bi ndax kenn naatablewul seen taxawaay bu dëggu te rafet ci Senegaal ci weer yii ñu genn.
Mënees na tënk ne, aju Popegin gi am na dayo bu mag ci réew mi. Muy firndeel njaxasu diine bi am ci Senegaal te jàmmoo rekk lal ko. Mu nekk ay bés yu way-gëm yi doon magal Yaay Mari mu sell mi, di ñaan seen soxla, waayeet di delloosi seen bopp ci diiney Yeesu Kiristaa.