AAR SUNU ÉLECTION BËTAL NA DOXU-ÑAXTOOM BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gii di wuyoo ci turu Aar Sunu Élection tegandi nañu ci suuf seen doxu-ñaxtu bi ñu sumboon te naroon ko amal démb ci talaata ji. Seen jubluwaay mooy xeex ngir amal wotey palug njiitu réew mici àpp bees ko jàppoon, maanaam bésub 25 féewiryee 2024. Nee ñu, duñu nangu mukk ñuy randal wote yi.

Perefe bu Ndakaaru moo gàntal doxu-ñaxtu bi waa Aar Sunu Élection nammoon a amal démb ci ngoon. La sabab gàntal bi nag, ci li perefe lay, mooy li doxu-ñaxtu bi nar a gàllankoor dem beek dikk bi. Waa Aar Sunu Élection nangu nañ ndogalu perefe bi. Waaye, loolu tekkiwul ne dañuy toog, bank seen i loxo. Xeex bi, bàyyiwuñ ko ; dañ ko bëtal rekk. Nde, ci seen i wax, bu yoon jeexut, waaxusil du jeex. Gaawu gii ñu dëgmal lañ ko jàppaat, bu 11 waxtu jotee ci yoor-yoor bi. Seen jubluwaay di SIPRES rond-point Liberté 6.

Kurél gi mu ngi woo Saa-Senegaal yépp, ak fépp fu ñu mën di nekk, muy fi réew mi ak bitim-réew, ñu génn def um njooxe. Ñépp àndandoo ne déet ci coppartig ndayu àtte réew mi. Ndax kat, loolu, bu ñu sukkandikoo ci seen gis-gis, mooy yokk moomeelug Maki Sàll. Te, bu boobaa, dañuy tooñ askan wi moom moome gi.

Mbejum kanam nag, boroom a koy fajal boppam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj