ALSERI DUMAATI NA SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci talaata ji la gayndey Senegaal yi doon janook Alseri ci joŋante xaritoo. Jamñaajo, ça fowub Abdulaay Wàdd, lañ ko doon futbalee. Alseri moo jëlati ndam li. Nde, ñoom ñoo dugal benn bii, Senegaal tus. Démb a nekkoon 14eelu yoon wi Senegaal di sukk ci kanamu Alseri. Li ci gënatee doy waar mooy ne, Alseri dafa tegale 6i joŋantey kuppe yu muy dóor Senegaal.

Laata joŋante biy door, bi 19i waxtu jotee, jaglees na similib tekkaaral way-dëdduy Marog yi dee ca rëng-rëng ba fa am. 

Bi mbir yi tàmbalee, Senegaal a tegoon tànk ci bal bi, sépp Alseri. Jekku nañ ay yoon ngir dugal. Waaye, muy Saajo Maane, di Ilimaan Njaay walla Nikolaa Jakson, kenn làkku caax yi. Bal buñ dóor, jàppkatu Alseri bi génne. Alseri dafa amoon ay jafe-jafe ngir jot ci bal bi. Te, saa buñ ko jotaan, gayndey Senegaal song leen, nangu ko, sëppaat leen. Ñooñu, ba ni arbit biy mayee ag noppalu ngir ñu seral seen i put. Ndax, dafa tàggoon démb.

Biñ naanee ba màndi, waa Alseri dañu xaw a yeewu tuuti, tàmbalee cokkaas Eduwaar Mendi. Wàññeeku Senegaal bàyyeekuwul. Dañu jàppaat, nanguwaat bal bi. Paap Mataar Saar, Kulibali, Jakson ak Sabali naroon nañu dugal sax, waaye sottiwul. Bi xaaj bu njëkk biy jeex, kenn dugalul sa moroom.

Biñ delsee ci ñaareelu xaaj ji tamit, Senegaal dafa delloo buum ca mboy-mboy ga. Waaye daal, bal bi daa bañoon dugg. Ca la xel ya tàmbalee teey, ñiy ragal Alseri yoxosu Senegaal.

Benn teg-dóor la Alseri am, Riyad Mahrez xellil Chaybi Fares, mu toj kër gi. Alseri nax na Senegaal, dugal ko benn bii bu kenn foogewul woon. Nde, Senegaal a moomoon mats bi, ci lees foogoon. 

Senegaal def na lépp ngir dugal, waaye dugaluñu. Jakson naroon na ko, waaye mbëkkam bi dafa kawe. Noonu noonu ba ni arbit biy mbiibee njeexitalu joŋante bi. Alseri daldi amati ndam ci kow Senegaal. 6i yoon la raŋale, di dóor Senegaal. Dafa di Aliw Siise sax, démb a nekkoon ñeenteelu yoon wi muy ñàkk ci kanamu Alseri. 

Démb nag, Sonko safoon na fa sàpp. Balaa joŋante biy door ak bi muy daw yépp, ndaw ñaa nga doon woy woyu Usmaan Sonko wi xew ci jamono :

“Aayee ! Iyawoo !

Sonko namm naa la !

Sonko namm naa la ! 

Sonko ! Sonko ! Sonko namm naa la !”

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj