Bamu jógee Konaakiri ba tey, seeti woon Alfa Konde, Abdulaay Wàdd, sunu Njiitu-réew ma woon, a ngi ne selaw. Wote bu 24 féewaryee bi sax, ak faluwaatu Maki Sàll bi mu jur, ba tey, yéyul yàbbi ci benn yoon. Mi ngi toog ci otelam ne tekk.
Terewul ñëpp moom lañuy déglu. Lu ni mel, Wàdd yàgg na koo am. Bu waxee, moom rekk la askan wiy dégg. Ba mu waxee ci ndoorteelu kàmpaañ bi, baatam sutoon na yu lawax ya doon xëccoo nguur gi. Ba mu toogee ba tey, cellam gaa ngiy jur coow lu bari.
Mënees na njoort ne Góorgi dafa amul la mu bëggoon. Mel na ni mi ngi doon xaar Idi ak Sonko dem lëngook moom bi leen Maki Sàll dumaa. Waxoon na leen ne : « Maki dina leen dóor te bu keroogee buleen ñëw fii di jooy ». Waaye Idi ak Sonko seetiwuñu ko. Xeexuñu itam, ni ko ñu bari ragale woon. Mu mel ne dañoo bàyyi Maki ak Yàlla, ngir wuyu wooteb jàmm bi jibe ci njiitu Murid yi.
Bu ko Idi ak Sonko seeti woon, ndax Laay Wàdd doon na sedde nii ? Ndax kon du jéem a yëngal gaal gi, ni ko woykat biy waxe ? Yàlla rekk a xam.
Li wóor daal, moo di ne Góor-gi waxul dara ci wote bi. Jaar na yoon am déet ? Ndamu Maki li lew na, am déet ? Wàdd waxul, pàrteem waxul. Ba bésu tey.
Terewul Maki Sàll tudd ko ci jàkkaarloo bi mu amal ak taskati xibaar yi altine jii nu weesu. Woo na ko, moom ak Abdu Juuf, ci waxtaan yu mu nar a amal ak làngu politig yi ci ayubés yi ñu dégmal.
Ba tey nag, Wàdd tontuwu ko. Walla boog dégguñu tontoom. Ndax, bu dee ñaar ñaa ngi diisoo ci suuf it, du bett kenn. Ku yàgg a seetlu Góor-gi, war ngaa xam ne ñàkkul lu muy làqarci ci guddi yi ñu tollu. Ndax mbiru doomam rekk la ? Mën naa am ñu xam ci dara ci fan yi ñu jëm.