AY DU YAM CI BOPPU BOROOM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jàppante ba amoon Mbàkke doxoon ci diggante takk-der ya ak soppey njiitu Pasteef lii di Usmaan Sonko, njeexintal ya dal na ca lekool ya. Daara ya ñoo
mujje xeex ba. Ndongo yu Mbàkke ya jóg, seen moroom ya féete Gasaan feelu leen.

Jàmmarloo ba amoon àjjuma ca Mbàkke laal na lekool ya. Li ko waral di ñenn ca ña yoon teg loxo, bokk na ca ñatti ndongo ak benn jàngalekat, la seen i naataangoo di sàkku yoon bàyyi leen. Tax ba ñu génn daara ya, wàcc ci mbedd yi ngir naqarlu jooju jëf. Mu mel ni ay du yam ci boroom ndaxte xew-xewu pólitig ba ñu gàntal, taal na Mbàkke, jafalaale lekkool yi.

Ña njëkk a jóg di ndongoy Mbàkke ya, dakkal njàng ma ca béréb yu bari ngir ñaawlu seen moroon ya ñu jàpp. Lañuy sàkku mooy ñu bàyyi leen ci lu gaaw. Mu mel ni la leen wokku moo xori ndongo ya nekk Gasaan féete ca diwaanu Lingeer. Ñoom seen wàll xàppati bésu lëmb boo xam ne kenn du dug ca kalaasya.

Ñoom lañu bëgg mooy ñu bàyyi ci lu gaaw seen jàngalekayu angale ba ñu jàpp ca ñaxtu boobu. Ñu seetlu ne mbir yooyu jar naa wut i saafara balaa ëpp i loxo ndax bu weesoo ndongo yooyu, jàngalekat ya féete Gasaan, ñoom tamit ña ngay yëglu. Lañu xamle mooy bu ñu bàyyiwut seen naataangoo boobu, ñoom tamit di ñañ tàbbi ci xeex bi.

Mu mel ne ñaxtu yi day yokku bés bu nekk te
saafara amagu ci. Mënees na wax ne tolluwaayu pólitigu réew mi mi ngi yóbbaale fànn yu bari. Ba bu ay yëggu-yëggu ame ñu bari seen liggéey sooke. Lekkool yi, nekk béréb yi nga xam ne li ñu ciy mucc bariwut. Leeg-leeg mu nekk ñàkkum njàng, leeg-leeg ay ñaxtu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj