AY DU YEM CI BOPPU BOROOM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal, jamono ji ñu tollu nii dafa mel ni nekk doomu– réew mi rekk doyatul ; fàww nga fésal wet gi nga féete, moo xam sa diine la walla sa tarixa mbaa pàrti pólitig bi nga faral ba ci sax mbootaay gi nga bokk léeg-léeg.

Waaye li ci gën a tiis, tey tiitalaate ba noppi ruslu mooy ñaawtéefi ñi ñuy tudde boroomi xam-xam. Ñenn ci ñoom a ngi taal i daay, ñi ci des di leen xamb. Ndax kilifa war naa làquy giseek i doomi-réew mi naan leen su nu jàppalewul Diw ci joŋante biy dégmal mu ñaaw ndax nook moom a bokk waaso ? Ana lu yées lii ?

Ruwàndaa bokk na tey ci réew yi ñu gën a naw ci Afrig waaye du tax kenn fàtte la fa xewoon ci atum 1994. Kodiwaar tamit, démb rekk la woon. Kon mbirum waaso ak xeet du lu ñuy kafe.

Nun waa Senegaal nag, li nuy seetaan muy raam, ci ñag bi la jëm. Te kenn ñaanu ko Yàlla. Nan bàyyee nax sunu bopp, naan bal du fi tàkk, jaasi du fi jóg ndax lii walla lee. Nanuy fàttaliku ne noo bokk ndey bokk baay tey moytu lépp lu nuy féewale. Ngalla buleen fi yee fitna ndax, kat, bu keroogee kenn du ci mucc. Du xam ngeen ni ay du yem ci boppu boroom ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj