AY NAAL ÑEEL NJÀNG MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi teewoon na ca ndaje ma ñu doon sargale ndongo yi gën a ràññeeku yi kàtte gu mag gii di “Concours générale”. Ba mu jëlee kàddu gi, junj na fay naal ñeel njàng meek njàngale mi. Xamle na ni, dinañu jël ay jàngalekat. Xew-xew boobu doon ame ca màkkaanu kilib bu Duudu Njaay Kumba Róos (Théâtre national Doudou Ndiaye Coumba Rose).

Mu nekk xew-xew bu ñuy faral a amal at mu jot fi réew mi. La ñu ko dugge mooy soññ ndongo yi ci seen um njàng. Loolu tax ba ñu leen di sargal ak a neexal ci seen biir i moroom.

Ren nag, mooy njëlbeenug yoon Njiitu réew mi di ko teewe ginnaaw bi mu toogee ci bopp réew mi ak léegi. Moom, Sëñ Basiiru Jomaay Fay, rëdd na fa ponk bu am solo jëm ci njàng mi ak njàngale mi. Ci biir i kàddoom, Njiitu réew mi joxe na fa ab xibaar buy neex lool ñiy yëngu ci njàng mi. Dafa wax ne, fileek 2030, dinañu jublu ci jël ay jàngalekat. Ndax, umpalewuñu ni réew mi ñàkke ay jàngalekat. Mu tudde ko “recrutement spécial”. Ñu mën cee xaar lim bu takku, te it anam ya ñu daan tànnee ña ñuy jël, mën naa wuute ak ci kàtte yi. Loolu dina tax ba ñu jële fi “classe multigrade”. Muy anam bi yenn ci ay jàngalekat di boolee ñaari kalaas yu bokkut te benn jàngalekat rekk moo koy yor.

La mu sof ci kàddoom yooyu mooy junj ponk bu am solo ba ñu doon waxtaane. Ñu tënk ko ci farãse ci baat yii : “Enjeux, défis et perspectives pour une école au service de la souveraineté nationale”. Mu gis ne ponk bi dina tax ba ñu xalaataat ci tëggiinu njàng mi fi Senegaal. Ñu war koo mooñaale ak doxiinu jumtukaayu-xarala yu yees yi ak nees di duggalee làkki réew mi ci lekkool bi.

Mënees na tënke ci kàdduy Njiitu réew mi ne, njàng mi mën naa am ay coppite ëllëg. Ndax bu ñu càmbare ay naalam, yenn ci ay jafe-jafe dina far jeex. Ñu ciy xaar ci ponk bu am solo bi ñu yàgg a naal muy jàngale sunuy làkki réew ci lekkool bi, ban taxawaay la ciy ame.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj