Ginnaaw bi ñu leen nattee ci Talaata jee wees, njureefi BAC yaa ngi tàmbalee rot. Ndongo yi tolloon ci 155 109, ñenn ca ñoom jot nañu seen i lijaasa ca wërngal bu njëkk ba. Mu nekkandi ab lim boo xam ne, nag Office du Bac wéralagu ko.
Mu doon njureef yu làmboo ay melo yu wuute ak i njàngat. Ndaxte, ndongo ya doon joŋante, bari nañu lool. Waaye, seen ug farlu mënees na ko natt. Li koy firndeel mooy, ca Wurosoogi, ndongo ya féete woon ca “jury” 1483 doon def “série S”, BAC bi yépp lañu raafal. Ndax, ñoom ñépp a am. Ñu tolloon ci ñeenti ndongo. Mu mel ni loolu ab misaal la ne, mënees naa lim yeneen yu ni mel.
Ci beneen boor, kàtte ya ñu doon wax ne dañoo saf, dafa mel ni feeñul ca Ndànd. Ndege, Yaasiin Faal am na BAC ca wërngal bu njëkk ba? boole ko ak “mention trés bien”. Leneen ndongo lu nar a ràññeeku ci joŋanteb ren bi, muy di Allaaji Faliilu Mbàkke mi boole ñaari BAC, bu araab ak bu . Bu dee araab bi, “mention excellente” la ci am. Am na keneen ku leen ñetteel te féete ca Lemba, fa Gore, Safiyetu Coor. Moom tamit “mention” la laal. Mu mel njuureef yooyu, bu ci ñenn ñi amee mbégte ndax dañoo dégg seen i tur, am na ñeneen ñu seen àdduna jaxasoo. Mu mel ni lu ñu naan jàmm waay, ayu waay.
Ca liise ba ca Ndaayaan, fa Njurbel, ndongo luy wuyoo ci turu A. M. Njaay jéem naa leb ay fanam ndax xibaar bu naqari ba mu jot. Muy ñàkk a am BAC ba mu doon wut, yaakaaram tas, mu bëggoon a xaru.
Mënees na tënk, wax ne, njureefi BAC yu 2023 baax nañu. Ndax, ci pàcc bu njëkk bi rekk lañu tollu, waaye ndongo yi ràññeeku nañu bu baax a baax, rawatina jigéen ñi. Ñi jot a jàll ci pàcc bu mujj bi, tey ci àllarbi ji lañu kàtte.