Ni ñu ko baaxoo amale ci réewum Senegaal, démb ci Talaata ji, yamoo ak 4i fan ci weeru sulet, lañu door BAC bi. Mu nekk joŋante bu siiw te am dayo. Moo tax ndongo yi sóobu ci kàtte yi ngir fàggu lijaasa bu leen di jàllale ca daara yu kowe ya.
Démb la sumb gu njëkk gi door. Lu tollu ci 155 109i ndongo ñoo bindu. Ren nag, limu ndongo yi dafa gën a takku. Nde, 4 184i ndongo dolleeku nañu ci limu 2022 bi. Ndaxte, daaw, limu ndongo yaa ngi tolloon ci 150 925. Bu ñu sukkandikoo ci kër gi yor caytug joŋante bi, Office du Bac, téeméeri ndongo yoo jël, 52,89% yi ci daaraay nguur gi lañu jóge ; 16,49% yi ñoo bind seen bopp, maanaam ay “candidats individuels” lañu. Lu tollu ci 3 400i yu féete ci njàngum xarala mi, ñoom, def nañ seen “Bac technique”.
Ñu gis ne, ña taamu njàngum ladab (série L), seen lim tollu na ci 126 893i ndongo, mu nekk lu baree bari. Ñeneen ñay tàggatu ci wàllum xamtu ak xarala ( séries sciences et techniques) limees na ci 25 426i lawax. Bu dee ndongo yiy jàng mbirum caytu (STEG), seen lim a ngi tollu ci 2 790. Am na tamit ñuy kàtte ci làkkuw araab, seen lim tollu ci 934i ndongo.
Ndongo yooyu, séddaatle nañ leen ci biir gox yi ak gox-goxaan yi ngir ñu amal joŋante yu jaar yoon te ànd ak kaaraange. Waa Office du Bac di dalal xel yi ci matukaay yi ñu jël ngir loolu mën a yemb.
Ci tënk, BAC bi door na ci jàmm. Kenn gisagu ci benn jafe-jafe, du njuuj-njaaj du dara. Ñenn ci ndongo yi gis nañu ne, kàtte gi taxu koo jafe noonu. Ku góor-góorlu génn ci. Njortees na ni njureef yi dinañu.