BARIGO PETOROL BU NJËKK FA SÀNGOMAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Muy xibaar bu njëkk ci noppi àdduna wërngal këpp : réewum Senegaal sol na barigo petorolam bu njëkk. Ginnaaw ba ñu ko feeñale ci suufu réew mi, soroj googu, soppi nañu ko démb ci altine ji. Ñi yore boobu liggéey ñoo fésal xibaar bu ni mel. Woodside Energy group mooy ki ko xamle tey ci talaata ji.

Muy seen tolluwaay bu njëkk ñeel bile liggéey. Muy ame fa Sàngomaar, lañu xayma ci soroj googu, na mu tollu, bari na lool ciy barigo, maanaam 100 000iy barigo bés bu nekk. Soxna si di Meg O’Neil, di njiitu Woodside, wone na xarañteg kër googu mu jiite. Gis na tamit ne, koom gu takku mën na cee tukkee jëm ci ñi séq pas gi. Waaye, taxawaayu Senegaal deesu ko naatable, ak Petrosen ma leen lënkale. Loolu tax ba, njiit la di Ceerno Li, di fésal mbégte mi mu ci am ginnaaw ba ñu tollee fii tey. Muy wone ay kàdduy cant ñeel ñi def boobu liggéey. Te it di njort koom-koomu réew mi nekk ci ay jeego te nar a am ay njeexital ci askan wi.

Lañu xayma ci ay koppari dolaar ci liggéey bu njëkk bi mu ngi ci diggante 4,9 jàpp 5,2 tamñaret (milyaar).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj