BUUR BI, DAG BI AK BATAÑSE BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bés, Buur dafa toog ak dagam, ñuy waxtaan. Buur ne ko :

– Sama xel dafa nekk ci lekk basante…

Balaay Buur di àggal, dag bi daldi biral :

– Heey Mbay ! Batañse waay ! Yal na Yàlla barkeel batañse ! Mooy sangu lekk yi : mooy yàpp wu amul gerees, mooy jën wu amut i yax, bu la neexee baxal, bu la neexee saaf, bu la neexee xar ko roof si ceeb, bu la neexee gajafal ko ci wineegar ba mu forox, bu la neexee def ko “makduus” (xar ko def ci i ñama-ñama door koo togg).

Bi dag bi daaneelee, Buur bi jokk, wax ne :

– Waaye, bi ma ko mujjee lekk dafa doon metti sama biir bi.

Dag bi biralati :

– Aah Batañse ! Na ko toskare ñeel ! Dafa diis, wex boole ci nëb ak ñuulaayam !

Bim waxee loolu, Buur bi ne ko :

– Toskare ñeel na la, yow ! Noo man a tagge mbir léegi, ci saa si nga xarabaat ko ?

Dag bi tontu, ne :

– Sang bi ! Man Buur laa fi nekkal, nekkaluma fi batañse ! Bu Buur nee “waaw”, ma wax “waaw”, bu Buur nee “déet”, ma wax “déet”.

Buur bi daldi muuñ, neexal ko, yokk darajaam.

Fii sunu réew mi toll, sunu sàrt (lois) yi ñooy batañse bi, dag yi di àttekat yi ak liggéeykati caytug Bokkeef gi (fonctionnaires de l’administration publique).

Batañse yi (sàrt yi) amuñu seen melow bopp. Dafa di, nees leen melal rekk lañuy mel. Bu ñu leen ñuulalee, ñu daldi ñuul ; bu ñu leen weexalee, ñu daldi weex. Mi ngi aju ci loxoy dag yiy jaamu bëgg-bëggu Buur. Lu Buur bëgg rekk, dag yi dëppale sàrt yeek bëgg-bëggu Buur. Bu ko defee, Buur di leen neexal, di yokk seen i daraja ak di leen aar bu ñu defee ay tojaange.

Li fi jot xew ci fukki at ak ñaar yii, ciy musiba, jalgati yoon, jaay doole, faagaagal ay opóosaŋ (way-kujje), budut woon “batañse” (loi) bii di ñuul ak a weex ci coobare Buur, dag yi (juges) yombal ko ko, kon réew mi dina am beneen xar-kanam.

Moo tax fàww réew mi xoolaat waañam wi keroog 25i féewaryee, déjjati Buur, raxas batañse bi, bàyyee ko meloom dëggantaan. Dag, yam ci yëgle cafkay batañse bañ caa dolli dara.

Seexunaa NJAAY

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj