CAABALUG ANSD 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Muy ab liggéey bu ñuy baamtu fukki at yu nekk. Ñu door ko ca atum 1976, renn di juróomeelu yoon bi ñu koy amal. Soloom nag mooy, xayma tolluwaayu réew mi, rawatina ci bànqaasu mbay mi, dëkkiin wi ak tolluwaayu askan wi. ANSD di kurél gi koy amal saa su nekk. Démb nag la génne caabalam gi, di ci fésal njureefi liggéey boobu ñu doon amal ci weeru me jàpp suwe.

Mu nekkoon liggéey bu siiw ci weer yee ñu génn. Lu ko waral doon dawo bu mag ba mu làmboo ak liggéey bu dajoon kàpp réew mi. Wa ANSD jëloon ci ay matukaay yu bari. Moo xam ay ndaw yu bari woon lool, tolloon ci lu ëpp 32 000, te doon def liggéey bi. ANSD dimbalikoo na ay jumtukaay yu mag ngir xayma boobu mën a jaar yoon. Bu ñu sukkandikoo ci ñoom, xayma nañu limu nit ñiy yewoo ci biir Senegaal ci 18 032 473i nit. Muy ab lim bu takku. Ñu seetlu ci ag yokkute bees ko méngalee ak limu askan wi tolloon ci 13 508 715i nit, ca atum 2013.

Bokk na ca la gën a fés, tolluwaayu ndaw ñi. Mu mat xaaju lim boobu te ña ca ëpp amaguñ 19i ciy at. Ñu gis ne Senegaal ndaw ñi ñoo féete kaw ba léegi. Nde, mag ñi seen at mat 65, téeméer boo jël 3,8% ci lañ tollu. Waaye, ñu bari jàppoon ne réew mi jigéen ñi ñoo ëpp góor ñi, nekk lu njureefi ANSD yi weddi. Ndax ci 2023 mii, góor ñee ngi tollu ci 50,6%  fekk jigéen ñi, ñoom, ñu ngi tollu ci 49,4%. Ñu seetlu tamit ne, ci dëkk yi nekk ci biir réew mi, Mbàkke moo ëpp mbooloo ma fay yeewoo, topp ci Ndakaaru ga ñu ko fooge woon. Mbuur moo leen ñetteel.

Lañu ca mën a tënke ci liggéey boobu mooy bari na ay lim. Lépp ak bànqaas ba mu aju. Mu doon li ñu mën a sukkandiku ci gëstu yu bari ngir gën a nànd askan wi. Waaye, xam tamit seen tolluwaayu dundin ngir amal ci ay coppite.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj