CFEE 2024

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋantey CFEE yi door na ci biir réewum Senegaal, ca Gàmbi ak ca Gine Bisawoo. Muy ab natt bi ñuy amal te ndongo yi fare ci daara yi suufe yi di ci jaar ngir jot ci seen lijjaasa bu njëkk. Bu ren bi, ñu jàpp ko talaata 25 jëm àllarba 26 ci weeru suwe wii. Li ci fés mooy xale yu bari may nañu leen ñu def boobu joŋante doonte ni amuñu këyitu judd. Seen ub lim gën a tàkku bu ñu méngale ak ñi woon daaw. Xaymees na leen ci lu jege 7 000 ci ay ndongo. Njiitu réew mi ak gog Càmm gi joxe boobu dogal ngir ñu bañe woññi xale yi ame jafe-jafey këyit.

Ni ñu baaxoo gise jëwriñ ji ñu dénk njàng mi amal na ab doxu-nemmeeku ca diwaanu ndakaaru. Mustafaa Giraasi ma nga woon ekoolu liberte 1, bu Sàkkere-Këer. La mu seetlu mooy lépp jaar na yoon. Ci gox yu bari ñu nemmeeku fa joŋante yu jaar yoon. Koldaa, Kawlax, Fatig, Kungéel, IEF Séex Yaaba Jóob, Mammadu Géy, kenn ku ci nekk wone na matuwaay yi ci Càmm gi jël. Mu nekk lim bu tàkku bu ñu gis, moo xam ñi njiite daara yi ñuy joŋantee, seen i tof-njiit, ñiy saytu xale yi, lépp a mat ngir amalin wu mucc-ayib.

CFEE bu ren ji daal, gisaguñu ci lu ñuy laam-laame. Matuwaay yépp a yem ngir amalin gu jaar yoon. Ñu seetlu ci ne xale yi daan am jafe-jafe këyitu judd teyewuñu leen wile yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj