Tolluwaayu pólitigu fi Senegaal ak coow la mu làmbool mel na ni bàyyiwul kenn. Réew mépp la faf daj. Xew-xew yi fi mujj, toftalu ci daanub njiitul pastef li, Usmaan Sonko, doy nañ ciy firnde. Coow li nag àgg na ba Tuubaa. Dafa di sax, Njiitu réew mi seeti woon na jamono jooja xalifa bi, Sëriñ Seex Muntaqaa Mbàkke. Moom nag, xalifa bi, jël na ndogalul tere lépp lu jëm ci pólitig fa biir Tuubaa.
Ba xeex ba jollee, ndawi Tuubaa ya far ak Usmaan Sonko wàccoon nañ ci mbedd yi ak tali yi, di taal i póno ak a sàndiy xeer ngir wone seen uw naqar. Muy lu xel masul a daj ca dëkk ba. Ndaxte, Tuubaa, terees na fa pólitig astemaak ay ñaxtu. Yëngu-yëngu yooyu nag, neexuñu xalif bi. Moo tax Sëriñ Seex Muntaqaa Mbàkke joxe ndigal ca saa sa, mu dig santaane ñeel ñaxtukati Tuubaa yi. La mu leen santoon mooy ñu dellu ca seen i kër, te ruse ko Sëriñ bi. Yemul ci wax rekk. Ndax, dafa santaale Baay-Faal yi ñu dakkal lépp luy pólitig fa biir Tuubaa. Ndigal loolu nag, xaw na jur i lënt ci ñenn ñi.
Ci benn boor bi, lees seetlu mooy ne, dafa bariy déggin yu wuute ba kenn ku nekk di ca joxe njàngatam. Ñenn ñi jàpp ne la wax jooju wund mooy ne, pólitig dootul amati Tuubaa, wote sax dees ko fay dakkal. Ñu gis ne wote ya ñu fa daan amal, mën na leen tuxal. Loolu mën na jur ay njeexital ci wàlluw pal gi. Ndax, lim bu takku ba féete ca dëkk ba.
Ca beneenboor ba, am ñu gis ne ndogal loolu, way-pólitig yi lees ci jublu. Ku ci mel ni dépite Abdu Mbàkke Dólli, loolu la jàpp. Ña mu ca duut baaraam di ña féete ci nguur gi ak ci kujje gi. Ndax, la mu ca seetlu mooy ay yëngu-yënguy pólitig ya amoon biir dëkk ba, lu mel ni ay mitiŋ yu fa pàrti pólitig yi jot a amal ba ñépp di ko ñaawlu. Leneen la mu gis mooy kujje giy xiirtal ndaw ñi ba ñuy amal ay ñaxtu fa Tuuba.
Menees na jàpp ne, ak fi réew mi tolluw, xel yépp ñoo nga Tuubaa ngir sàkku ay saafara yu mën a delloosi réew mi ci ag dal. Waaye, mu mel ni ñénn ñaa ngi ciy bëtt ay poroxndoll. Nde, bu dee Tuubaa kenn dootu fa wote, sikk amul ci askan wa fa daan wotee dañ leen di tuxal, ñu woteji feneen. Ci loolu nag la ñenn bëgg porofitoo. Li ci kanam rawul i bët.