DÉMB AK TEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew. 

Waaye tamit, bindkat yi dinañ  faral di leen ci baaxe seeni gis-gis ak i xalaati doomi réew mi ci mépp mbir mu ñeel Senegaal.  Rax-ci-dolli, yéenekaay bi dina leen wisal, may leen ŋeleju ayu-bés gi ak nataali ODIA, aji-ŋeleju bu mag bi. Bii-yoon, nag, seen yéenekaay LU DEFU WAXU da leen a indil lu bees tàq, mayati leen ko, muy seen xët DÉMB AK TEY. 

Ñaari baat yii, DÉMB ak TEY, ay tegtal lañu ci li xët mi wund. Jokkalekat bi, “AK”, di wone ne deesuleen  téqale. Maanaam, kenn warul a féewale cosaan walla jamonoy maam ya (DÉMB) ak sunu jamono jii (TEY). Bu ko defee, li nu ko dugge mooy dekkil cosaan, fàttali leen xew-xewi démb yu mag yi. Waaye nag, bàkk mbaa ŋàññ maam rekk yi taxunoo jóg. Naka noonu, jógunu ngir di leen nettali rekk li xewoon démb walla di leen léebal. Bu ko defee, nësër gi dëgg mooy lëñbëtil leen cosaan ak aaday maam ya, méngale leen ak jamonoy tey jii ngiree nu rotal ciy njàngat yi nuy jariñ tey, leeralal nu sunu ëllëg. Ci gàttal, xët mu bees mii nu duppe DÉMB AK TEY , li mu sasoo moo di wëral leen réew mépp, sowu ba penku, bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, béréb bu nekk mu taxaw fa xamal leen la fa xewoon ak njàngale yi ñu ci mën a jukkee. Ndaxte, cosaan mooy caabi jiy ubbi buntu tey, di làmp biy leeral ëllëg. Kon, cosaan deesu ko xeeb. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.

Seen yéenekaay LU DEFU WAXU xam na ni, wenn askan mënul a jëm kanam féeg mi ngi dëddu cosaanam. Rax-ci-dolli, réew mu askan wa naat, ci cosaanam ak i aadaam la sukkandiku ba indi fa ay yokkute. Looloo gënatee tax mu baaxe leen xëtam mu bees mii. Wolof dafa ne, kuy dem ba xamatoo foo jëm, war ngaa dellu fa nga jóge. 

Bu ko defee, sunu sas moo di dellu rooti ci teenu DÉMB, nàmpi ca meenu cosaan ngir tabax sunu TEY ak sunu ËLLËG. Seen mbokk, Paap Aali Jàllo moo nekk ci boppu gaal gi, di ko joow ci géejug cosaan, yen saa yi mu mbiij ci dexug aada, leeg-leeg moom walla kenn ci LU DEFU WAXU indil leen sarica. 

Tey, Daawuda Géy moo def ab gëstu ca Kaasamaas ci ñeyu-xare bu ñépp miin turam te taxul kenn xam ko bu baax : Jiñaabo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj