DÉMB SEŋOOR, TEY WÀDD

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li ko dale atum 1978 ba tey jii, woteb ren bii mooy wote bu fi njëkk a am te Ablaay Wàdd sampu ci ndëndam. Walla boog, loolu la ñu bare jàpp. Ndax, man kat neneen laa gise mbir mi. Bees delloo ginnaaw, fàttaliku atum 2007, bi Ablaay Wàdd faluwaatee, war a amal ñaareelu moomeem, dafa wax wax ju am solo. Wax jooju, mi ngi ko waxe woon cim ndaje mu mu séqoon ak taskati xibaar yi. Bés boobu la leen « Góor gi » xamal ni mébétam mooy njabootam ci wàllu politig, maanaam « libéraux » yi, toog ci boppu réew mi lu mat juróom-fukki at, gën gee néew. Foofu, Seŋoor mi njabootam — « socialistes » yi — toogoon ñeent-fukki at ci jal bi, la Wàdd doon diir mbagg, ne sax fàww mu rawe ko fukki at.

Wax jooju, lu jar a bàyyi xel la.

Képp kuy jàngat géewu pólitig beek li ciy xew, war na jéem a xam ndax mébétu Góor gaa ngi ci yoonu àntu, waaw am déet. Su dee waaw la, mu seet man walla yan pexe la koy amale. Nanu leen xoolaat wote yi fi jot a am ci atum 2000 ba nëgëni-sii.

Li wolof di léebu naan, bu ndung sàqee, ndung leng, géewu pólitig bi doy na ci firnde. Ndax, 2000 ba léegi, wote njiitu réew yi fi am yépp, Ablaay Wàdd ak i « doomam » ñoo ciy xëccoo. Kon, mu mel ni làmb ji PDS ak…PDS rekk lañ koy tëggal. Nan dellu ginnaaw. Ci atum 2007 Ablaay Wàdd (PDS) moo janoo woon ak Idiriisa Sekk (mi bawoo woon PDS).

Ñu ni déet-a-waay, ci atum 2012, Ablaay Wàdd janoowaat ak Maki Sàll (moom tamit jóge woon PDS).

Bu fa yemoon mu tane, waaye ci wote ndawi pénc mii weesu, Maki Sàll fexe na ba Usmaan Tanoor Jeŋ, Mustafaa Ñas, Ndem-si-Yàlla ji Jibo Léyti Ka ak seeni farandoo, fàtte PS, làng ak moom ci biir Bennoo Bokk Yaakaar, maanaam ñëw mu boot leen. Amoon na, nag, weneen lafu PS wu lànkoon ni du ànd ak Maki Sàll ci wote yooyu, muy Xalifa Sàll (PS) ak Maalig Gàkku (AFP). Ñooñu, Ablaay Wàdd da leen bëggoon a teg ci ginnaawam, jiite ndajem làngu politig gii di Mànkoo Taxawu Senegaal. Ba ñu lànkee, ne Xalifa Sàll lañuy àndal, Ablaay dafa ne wérëñ, ber yoonam, dem ceek Maki Sàll. Fan la yëf yi mujje ? Xanaa PDS — Maki Sàll — raw, PDS — Ablaay Wàdd — topp ci !

Léegi, nag, sóobu nanu ci woteb 2019 bi ñu war a fale njiitu réew mi fiy toog ba 2024. Waaye, mel na ni dara soppeekuwu fi : na woon, fa woon. Leer na ñépp ni kenn ci ñaari doomi Ablaay Wàdd yii di Maki Sàll (APR) ak Idiriisa Sekk (Rewmi — noonu la ko Idiy binde) mooy gàddu ndam li. Kilifay PS yu mag yi ñoom, Tanoor ak Ñas, daanaka Maki modd na leen ; la ca desoon di bañ, muy Xalifa Sàll ak Gàkku mujje nañoo ànd ak PDS (Idiriisa Sekk). Kon PS moom, kenn waxaalewu ko.

Naam, ñoo ngi wax ci xale bi yëngal jamono te xew, Usmaan Sónko, li am ba des mooy : xamees na ni ku falu PDS a la fal, ndax kàrt yépp a ngi ciy loxoy Ablaay Wàdd. Jàppees na ni, ku mu àndal ci ñaari doomam yooyu di Maki Sàll ak Idiriisa Sekk, dinga jël ndam li. Looloo waral, doonte jëmmu Ablaay Wàdd bokkul ci wote bi, fi mu nekk ñépp a ngi koy déglu ba xam kan lay mujjee tàllal loxoom ngir mu sakkanal ndono li.

Ablaay Wàdd, nag, bi mu yegsee Senegaal keroog alxames 7 féewaryee bii weesu te ñépp doon ko xaarandi ba xam ku muy àndal, mënees naa jàpp ciy kàddoom ni fasul yéenee far ak kenn ci mbër yi. Mébétam mooy wote bi bañ a am. Waaye ku xam Wàdd xam ni ku tàmm a woote di xool ndey-joor la fekk booba xel maa nga jëm càmmooñ. Xanaa nu yónni yàgg rekk ba xam fu wànnent di mujj ak i gëtam. Bésu joŋante bi soreetul…9

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj