FAAS BÓOY, SIGGIL NDIGAALE !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbëkk maa ngi wéy di def i jéyya ci réewum Senegaal. jéyya ci kow jéyya. Musiba ci musiba. Li gënatee doon musiba te raglu mooy lees ci gëmm, noppi ci, mel ni dara xewul. Dafa mel ni danu dem ba miis ko, defatunu dara. Taskati-xibaar yi sax, dañoo mel ni ñu tanqamlu. Bindeesu ci li war. Kenn defu ci jotaay ngir faramfàcce sabab yi. Saa bu xéyee, Maki fii, SOnko fee. Jamono jooju, ndaw ñaa ngiy lab ci géej gi te, ba tey taxu leen bàyyi. Ñoo ngi mel ñu ñu xabtal. Faas Bóoy doy na ci firnde. Nde, la fa saay ciy ndaw jéggi na dayo.

Faas Bóoy ab gox la bu féete fa Cees. Faas Bóoy siiw na ginnaaw naqar wa leen gane. Cig pàttali, gaal gu yaboon lu tollu ci 101i ay ndaw ñu déqee ca waaxi Faas ya, wutali Bàrsaa faf dem Barsàq. Nde, ñu bari ci ñoom ñoo réer ci géej gi te, ba léegi, kenn xamul ci luñ nekk.  Seen i mbokk jaaxle lool. Moo tax ñu jóg di artu Càmm gi ngir ñu wëral leen seen i doom.

Ginnaaw gi déggees na ni gaal ga teeri na fa Kab-Weer, réewum Pereyaa. Loolu jur njàqare ci seen

àndandoo ya ñu bàyyi woon ginnaaw. Ndax xaaj, xaajaat ba nga des ca géej ga. Lu tollu ci 38 ci ay bakkan ñoo mucc ci jéyya jooju. Lu mat juróom-ñaar ci ay néew lañu rob fa Pereyaa ginnaaw ba ñu leen gisee ca anam bu jéggi dayo. Ginnaaw kenn ka fa des ngir faju, ña ca des gunge nañu leen, ñu dellu ci seen i njaboot.

Faas Bóoy a ngi jooy ay doomam. Mu doon aw tiis wu ñuy gis ci seen i xar-kanam. Njabooti ña des ca mbëkk ma di wone metiit wa ñu ame ci jéyya jooju. Njaboot gu tas, ay jirim, ay jëtëñ di wéy di dolliku saa su nekk. Doomi Faas Bóoy a nga tëdd Pereyaa, ñeneen ña seey ca géej ga.

Faas Bóoy siggil ndigaale !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj