FAATUG HIBAA CAAM : SENEGAAL, BOPP BU XAR ÑAAR?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Guddi àjjuma, dëppook 3eelu fan ci weeru Awril, doon guddi gi jiitu bésub baaxentalub sunu moom-sa-réeew, la benn jànq bu am 28iat, di wuyoo ci turu Hibaa Caam, ñàkk bakkanam, ci anam yu tiis te doy waar. Ñu ngi ko fekk mu tëdd, ne nemm, di waccu deret. Ci li taskati xibaar yi wax, xale bu jigéen bi, dafa jël lu ko ëpp doole ci ay donji dorog, ba faf ca faatoo.

Loolu nag, mu ngi xewe ci Almadi gii ci Ndakaaru, ca kër gu Baaba Jaw «ITOC» di luye. Moom nag, boroom alal ju raññeeku ci réew mi la te doomam bu jigéen moo ko féetewoo. Ñi fa daje woon ay moroomam lañu, ay xale yu góor ak yu jigéen, ne fay fo ak a topp seen bakkan, doon it ay doomi boroom alal, ak ay doomi kilifa yu ñépp xam ci réew mi. Ku ci bokkul ci ñi ŋànk nguur gii fi ne, am nga ci jegeñaale ; ñu ràññee ci : Daam Amaar, doomu ndem-si-Yàlla-ji Amet Amaar mu NMA SANDERS, doon itam goro Yusu Nduur, Luuti Ba te baayam di jiiteb kurëlu tàggat-yaram.

Xew-xew bu ni mel nag, dafay firndeel, ci lu amul benn werante, yàquteg goney réewum Senegaal fi mu toll. Dees na ci joxoñ itambaaraamu tuuma kilifay réew mi, ci ñàkk a yarseen njaboot ni mu ware, bàyyi leen ci seen sago. Li jar a laaj dëgg nag mooy : ana nu ay gune yu juddoogul, mën a yore xaalis bu dul jeex, di ko pasar-pasare nu mu leen neexe, ci Senegaal gu ndóol gii ? Lu doy waar la ! Rax-ci-dolli, ñu mel ne ñu réer, wàcc seen and,waral ñuy daje di jolluy bitéeli biiñ ak a tux sineebar, dëkke càkkaay

Dëgg la sax, mënees na jàpp ni àddina day dox, ngir jamono ju nekk ak i feemam. Waaye kat…. !

Ak lu mu ci mën a doon daal, li ëlëm ñépp,mooy, jamono ji jéyya yii yépp di ame, tiis ak njàqaree ngi lëmbe àddina, ba tàbbi ci sunu Senegaal gii, muy CORONAVIRUS.

Mbas la moo xam ne, réewoo-réew mu ngi fay tëral ak a fàdd doomiaadama yi. Ngir xeex ko nag, fii ci sunum réew, gornmaa bi dafa jël ay dogal yoy, bokk na ci : tere nit ñi ñuy génn guddi, ku nekk war a lëlu ba fajar. Beneen laaj bi nag mooy : xale yooyii newoon ci mbumbaay, ba dogal bi dal seen kaw, ana fan lañu jaar alkaati yi aakimoo mbedd yi. Ana nan lañu def  ba mën a dem ak dikk, guddi, tollook 10i waxtu, ba Hibaa mën a fekki xaritam yi ? Walla, ndax ñoom, xale yooyu, dañu leen a jox ay kayit yu leen may boobule sañ-sañ ? Su ñu noppee ci laaj yooyu, beneen taxaw, muy : ndax dafa am ñaari Senegaal : gu baadoola yi yoon mën a dal seen kaw, saa su ne, ak geneen, gu ñeel boroom barke yi, ñuy buum di bummi, di tambaambalook a def lu leen neex ? Dafa mel ni daal, yoon buy digal ak a tere, baadoola yee tax ; ci ñoom daal la gën a jekk. Moone, duy faral di wax naan :« Senegaal, benn bopp la, kenn mënu koo xar ñaar ! » Am déet ?

Laaj yi yamuñu foofu de ! Leneen li mat a xam, mooy : ndax CORONAVIRUS bii, dafa am ñu mu dul song ? Du dañu naan feebar bixamul xàjjale? Ak li ñuy woote yépp ci rajoo yeek tele yi jëm ci jumtukaay ak i matuwaay ngir moytu feebar bu bon bi, niki : soriyantoo, raxas say loxo, ak yu ni mel, naka la sunu njiit yi mën wëlbatikoo, bàyyi seeni doom, ñu topp seen bakkan, di doxe maa-tey ? Xanaa kenn mënul ne bëgguñu seen doom yooyu de ? Walla, ñoom ci seen bopp, dañoo gëmul dara ci li ñuy woote ?

Mbir maa ngoog. Laaj yi bari nañu lool, te yeneen mat naa leeral, yu mel ni, Hibaa Caam mi ci ñàkke bakkanam, ku ko rey, ak ci yan anam la faatoo ? Li ci gën a doy waar nag, mooy, doonte ubbeeguñu lànket bi, taskatixibaar yi xamle nañu ni, way-jur yi ci seen doom taq ripp, ba alkaati yi teg leen loxo,  ña ngay dugg ak a génn, di lal ay pexe. Looluteey na xelu ñu bari, ba ñu jàpp sax ni mbir mi du mujj fenn.

Loolu nag, su amee it, du fi guléet : xanaa fàttewuleen Mati Mbóoj, janq bu siiw boobu fi génnoon àddina moom itam, ci anam yu ni mel? Mel na ni nag, yëf yaa ngi bëgg a ëpp i loxo, te lu ëpp, tuuru. Su ñu ci jógul, du baax ci guney réew mi.

Waaw, Senegaal gii xar ñaar, ak ñawtéef yi lëmbe réew mi, ndax mënees na koo saafara ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj