FAIDHERBE DU FI MAAMU KENN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii yépp, xanaa mën nañoo wax sax weer yi weesu yépp, coow laa ngi neeti kurr ci biir réew mi ak ab jàppante bu dul jéex. Jàppante bu doy waar, nag. Coow li, coow li, keneen yóbbeewuñu ko ku dul seriñ Faidherbe. Faidherbe sax, de. Moo fi ne woon Gornóor, daloon ca Ndar, peyu Senegaal ak dëkki Afrigu Sowu Jant yépp jamono ji Tubaab yi moomee réew mi. Estati boobu ñu ko jëmmale ca béréb bi ñu duppe turam ci Ndar, ma nga fa ne noŋŋ-noŋŋaaral,eméeri at ak fanweer ak ñent ba sun-jonni-Yàlla-tey-jii. Laaj bi benn la : lu mu fay def booba ba léegi ?

Ndax xel nangu na ñuy wéy di sargal Faidherbe ci Senegaal gii moom boppam, boobaak léegi mat na juróom– benn fukki at ? Jàppante bi nag, boroom xam-xam yi génne ci lekooli Tubaab yi ñoo ko séq, mu mel ni daal, ñenn ci ñoom dañoo am cofeel ci doxalinu Tubaab yi fi woon ba di leen namm !

Ñoom ñooñu, nag, dañu jàpp ni, mu neex, mu naqari, Faidherbe ak i ñoñam ci cosaanu Senegaal lañu bokk. Konte war nañoo weesu fi mu ne nii, di gaaw a gis sunu bopp ba di fàtte ni, nooteelu Tubaab ba woon, lu mu doon metti-metti, amoon na itam lu ci ñépp mën a rafetlu. Ku weddi na xool jàlloo bu mag te rafet boobuyggi dexu Ndar gi te ñu duppe ko… Faidherbe ! Du waa Senegaal, rawatina doomi Ndar yi koy jariñoo ñooy wax ne amul maanaaBa tax na, estati Faidherbe bi, lu fa mat a bàyyi la. Am na sax ci boroom xam-xam yooyule, ku nu ciy artu : bu coow li jëm kow, ndax kat, bu nu dof-dofloo ba waa Lille, dëkk boobu Faifherbe fekk baax, jot ci, du ñàkk ñu téye seen xaalis bi ñuy dimbalee Ndar ñeel séexal gi lëkkale ñaari dëkk yi. Nu gis ne, xëccoo « deseer » bi nuy nootkat bi jóge bitim-réew di ñamal, lu fi yàgg la te du fi teel a jóg

Boroom xam-xam yooyu nag, mënoon nañoo wax leneen lu-dul Frãs ak ndawam lu mel ni Faidherbe ci sunu cosaan lañu bokk te dan leen war a weg, sargal leen. Waaye booy seet, seen lay yépp noonu la tollu, ba tax na ku leen déglu, soo moytuwul yéemu !

Ndax nag, war nanoo njëkk xam li ñuy wax lan la ak naka la mbir mi tëdde.

Senegaal ak réewi Afrig yu bari, ginnaaw ba ñu dunde ñetti xarnu ci njaam, dundati nañ ñaari xarnu ak lu topp ci nootaange Tubaab yi leen songoon ak seeni xeeti gànnaay yu bees ; amul lu ñu dajul ciy loraange, metit, ndóol ak toroxte. Tubaab yi ñoom, lu yëngu ñu jam, di rey, di lakk, di sàcc, di gàddu doomi Afrig yi yóbbu Amerig Noonu la Afrig ñàkke lu tolloog ñaari téeeri alfuniy nit yu ñu gàddaayloo mbaa yu ñu faat. Sunu dund gi ñàkkati gancax yu ñu yàq, alal yu ñu pasar-pasare, dëkk yu ñu toj, aada ak ngëm-ngëm yu ñu salfaañe… Nootkat yi yemuñu woon foofu : doon nañu sàkku jigéen ñi ; boole ci jàpp góor ñi di leen dugal ci seen làrme, ñuy rey ak a yàq ñoom itam ci lu dul seen sago ; ñoom nootkat yi doon nañu walbatiku jël gune yi dugal ci seeniy lekool ngir raxas seen xel ba lu ñu sant gune yi ñu def ko, ànd ceek ñoom sax.

Njiiti réewum Farās nag, delloo nañu njukkal seeni doom yi doon toroxal Afrig, màggal nañu leen. Noonu lañu tànne ka leen yilifoon, te ne woon ndeyu mbill gi, muy Faidherbe, ba mu dëddo àddina, tudde kob béréb bu réy ba ca Ndar, jëmmal fa estateem, ba noppi tudde ko pom bu mag ba mu fa defarlu woon.

Ndege Tubaab bee fi doon buur di bummi, kenn amul woon looy nangu walla looy bañ. Te yit kenn mënul a wax ne Faidherbe yelloowul woon màggal googu ña ko fi yabaloon màggal. Noonu la réewi àddina sépp di doxale : mbër moo ngemb ba mu daan, sargal ko war na la.

Waaye ka mu daan ak i farandoom ñoom, ndax warees naa xaar ci ñoom ñu tàccu ko ? Ku xam ni amaatëeri làmb yiy nekke, xam ni, fàww ñu xar ñaari pàcc yu wute, ñii féete fii, ñale féete fale : su ñii di ree ak a fecc, ñale di ŋàññ a ka jooy. Monte loolu de, daa mel ne, lu ñépp war a xam la, am déet ?

Konte nan jàpp ne,  kuy xalaat a sempi estati bu Faidherbe walla bu beneen nootkat bu mu mën a doon, taxul mu weddi xew-xewi coosaan yi ñépp xam, ndax li am, daa am ba noppi, kenn mënatu ci dara. Ana luy ndeyu wéy di sargal ka doon faat ak a bóom sunuy maam, doon fi def naka-su-dul noonu ? Estati nag, tekkiwul leneen lu dul sargal ka muy jëmmal ! Loolu, dara la jotewul ak tabax ay pom ak i tali, walla ay lekool ak yeneen yu ni deme.

Danuy nangul Tubaab yi ni, Faidherbe seen mbër la woon, ñoom waa TugalMuy lu kenn mënul a weddi, feek waa Farās ci seen bopp ñoo ngi gëm loolu.

Waaw, Senegaal nag moom, ndax Faifherbe ciy mbëram la bokkoon ? Loolu mooy wax ji !

Waaw, xanaa du Faidherbe moo fi jiite woon soldaar ya songoon Sowet, Njag-Aral, Njaral, Njajer, Marsa ak Bàkkel, ca atum 1855 ca weeru Màrs, rey nit ña, rajaxe lépp lu fa doon dëkkuwaay, taal gàncax ga ? Ana kan moo takkaat xare weer wa ca topp, dem bóom waa Naye, dëkk boobu féete ci penku Senegaal, ñépp dee fa, kenn desul ? Nañ ko xam, du keneen ku dul Faidherbe. Kan moo demati ci weeri Suweŋ ak Ut ci at moomu, song Sóokóon, Njat Amar Faal, Cileen, Ros, Damga, Bàkkel, Kungël ak Caabo? Moom la woonati, moom defkatu njaaxum bi, seneraal Louis Léon César Faidherbe. May laaj, kan moo taal Njiit (ci Njàmbur), Wadan ak Baral, ana ku jëf ñaawtéef yooyule ? Bumu bett kenn, mooma ba tey, nit ku bon ki, Faidherbe. Waaw, kan sax moo demoon Fatig ci weeru Me 1859, lakk tool ya, lakk kër ya, bóom waa dëkk baak waa dëkk-dëkkaan ya ko wëroon yépp ? Ku muy doon ku dul sunu waa ja maroon deret te tudd Faidherbe ? Ku dellu ca weeru Awril 1861 dal ca kow ñaar-fukki dëkk ak juróom ya féete ca Kel ak Mexe, teg ca Kër Aali ak dëkk ya ko wër, walbatiku te waccul ca ginnaawam lu-dul naqar ak i dóom ? Moom doŋŋ, moom Faidherbe mi doon liggéeyal réewam, kkati raaya Farās ngir toroxal der bu ñuul. Taxul nag mu yem fa, ndax atum 1861 la dal ci  Boseyaa ca Fuut
a yi

Mbir mi jéggi na dayo, doy na waar ! Moo tax it kenn jéemul a woññi ñaata nit ñoo loru ci ñaawtéefi Faidherbe yooyu. Porfesëer Iba Deer Caam daal, moo ñuy xamal ne, am na benn gëstukatu Tugal bu xayma ni, li Faidherbe faatci diirub juróom-ñetti weer rekk’’ tollu na ci « ñaar fukki junniy (20. 000) doomi-aadama » !

Waaye nag, nettali ci làmmiñu boroom ! Ci li ñu boroom xam-xam bii di Xaadim Njaay xamal, Faidherbe, ba mu nekkee Alseri doon fa def ay njobbeem, laata muy ñëw Senegaal, daa yónnee bés ab bataaxal di ci yëgal ndey  ji ay jalooreem, ni ko :

« Toj naa benn dëkk bu rafet, rajaxe fa ñaari téeméeri kër ak seeni tóokër. Waa dëkk bi dañoo tiit ñoom ñépp, dawsi jébbalu ci man ».

Lii moom, luñ ci waratee yokk ?

Ngóor soosoo doon Faidherbe mi Senegaal di sargal. Daa fekk nag ne, sunu jamono jii, ginnaaw ba ñu toroxale George Floyd ba noppi rey ko ca Amerig ndax rekk li deram ñuuloon, àddina sépp a ko jooy ; ba tax na ndawi réew yu baree-bare dañoo jóg di buddi bépp estati buy màggal ñi doon toroxal doom-aadama. Ndawi Senegaal nag yi, ci ndawi àddina si lañ bokk. Kon warul jaaxal kenn su dee, ñoom it, dañu jóg wone seen bopp, fésal seen naqar ci sargal bi nuy wéy di sargal Faidherbe. Loolu kepp a tax ñuy laaj lii : lu tee ñu sempi estati Faidherbe ba ne noŋŋnoŋŋaaral ca Ndar ?

Ndaw ñi nag, doon nañu xaar ci boroom xam-xam yi, rawatina ñi ci daara yu kowe yi, ñu am taxawaayu Usmaan Sémbéen mi doon laaj Seŋoor :

« Xanaa sunu réew mii, jurul ay jigéen ak i góor yu yelloo ñu sargal leen, tudde leen sunuy lekool, sunuy iniwersite, ak sunuy mbedd ? »

Danu war di màggal sunuy jaambaar, ni ko réew yi fonk seen bopp yépp di defe. Wareef la ! « Sama bopp a ma la gënal, tekkiwul ne dama laa bañ ». Tee noo bañ a ànd ak ña doon toroxal ak a bóom sunuy maam ? Faidherbe ak ñi ko fi wuutu, dañ koo jar am ? Estati Faidherbe bii, daa amatul palaas ci Senegaal gii moom boppam tey. Su dee sunu moomeel gii du ay naxee-mbaay

Nanu sempi estati bi, nanu ko déjjati. Su ko laajee, ñu wutal ko fu ñu koy denc. Loolu nag, dunu tax a fàtte sunu démb, sunu mboor mi nu war a bindal sunu bopp.

Senegaal, Faidherbe du fi maamu kenn !

Uséynu Béey

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj