FESPACO

Yeneen i xët

Aji bind ji

FESPACO (festival panafricain du cinéma et de la télévision de Ouagadougou) bokk na ci xew-xewu film (cinéma) yi gën a siiw ci Afrig. Ñu koy amal ñaari at yu nekk ca Wagadugu, réewum Burkinaa Faaso. Xew-xew boobu, sosees na ko ci atum 1969, ca péeyub Burkinaa Faaso bii di Wagadugu. Lees ko dugge mooy fésal filmi Afrig, lëkkale bindkati film yi ngir ñuy weccoo xalaat ak xam-xam. Waaye, tamit, solos saa ngi aju ci jañ ko ba mu am ag yokkute ak kaaraange. 

FESPACO bu ren jii, mooy 28eelu yoon bi ñu koy amal. Dees na ko amal diggante 25 féewaryee jàpp 4 Màrs 2023 ca Wagadugu. Dinañu fa dalal artist yi, taataan fa seen i xalaat. Ponku ren bi nag, dafa tembeek waxtoom. Ndax, jamono jii, Afrig mi ngi jànkoteel ak i rëtëlkat, ñu lëmbe kmebar gépp. Loolo tax ñu tënk ko “Cinémas d’Afrique et culture de la paix”, maanaam naka la filmi Afrig yi mënee dox jàmm ci kembar gi. Muy ponk buy wone ne film mën naa suuxat jàmm. Te sax, ci jàmm jooju la fukk ak juróomi film war a joŋante ngir tebbi neexal bu tollu ci 20i tamndaret yees teg ci taabal ji. wWaaye, ndajeem film mu Usmaan Sémbeen teewut ñu war ko caa fàttaliku. Loolu tax ba ñu jagleel ko ab ponk ngir màggal xarnub juddoom.  

Bi yoon nag,  dañu seetlu ne, ag lëkkëloo dafa am diggante ñaari réew yii di Mali ak Burkinaa Faaso. Seen Njiiti jëwriñ taxawee tijjiteg xew-xew boobu di Apollinaire Kyelem de Tambela ak Choguel Maiga. Ñuy ay réew yoy, film fa la fekk baax, te am fa solo lool. Ci weneen wàll wa, seen tolluwaayu pólitig ak jafe-jafe ñeel kaaraange ñaari réew yi am ag niroo. Loolu di dëgëral seen ug bennoo ngir wut ay saafara ci jafe-jafe yooyu. 

Mënees na tënk, wax ne film, mënees na ci jaare, indiy saafara ñeel bépp xeetu  jafe-jafe àddina. Dafa di, film mbirum mbatiit la, te mbatiit day boolew askan. Mu mel ni FESPACO wone na ko, te mi ngi bay waaraam ngir film gën a jëm kanam biir Afrig, amal njariñ nit ñi fay yeewoo. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj