FITNA DU YEM CI BOPPU BOROOM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, ma nga ndung-siin jamono jii. Lees ko jàpp, am na ñm bett, waaye am na ñeneen ñum bettul. Li ëpp ci nit ñi nag, dañ jàpp ne lees ko jàpp ak nees ko jàppee jaarut yoon. Am nia yit, ci beneen boor bi, ñu jàpp ne, jàpp bees jàpp Usmaan Sonko lu yenu maanaa la. Moom nag, meeru Sigicoor bi, 7i tuuma la toppekat bi gàll ci kowam laata ñu koy dóor « mandat de dépôt ». Jamono jii nag, réew mi yëngu na. Kenn xamagul fu mbir yiy tàbbi.

Bari na ñu doon laam-laame tëjug Usmaan Sonko, di laaj naan ndax dina am walla du am. Léegi moom, mbir mi leer na. Ndax, mujjees na teg loxo Usmaan Sonko. Càmm gi yemul ci jàpplu Usmaan Sonko rekk. Nde, daf ci jaare génne ab dekkare bob, nee na ci day tas làngu Pastef gi Usmaan Sonko jiite. Jëwriñu biir réew mi moo jël ndogal loolu. Waaye, mënees na wax ni Njiitu réew mee ko ko digal. Nde, ñépp xam nañ ne jëwriñ yi duñ def lum yëgul walla lol, àndu ci. Kon, bu yeboo jàpp ne, Maki Sàll moo nekk ci ginnaaw.

Li koy firndeel mooy ne, moom Njiitu réew mi, waxoon na fi ne, am nay wayndare yoy, moo ci teg ci concam. Mu waxaat lu yàggul dara na, dina fexe ba ñuy jëmmal ndogal yi Yoon di jël te du ci dellu ginnaaw. Ñépp njortoon nañ ne Usmaan Sonko a ko taxoon di wax. Te, bu dee wax dëgg, loolu du cëram. Nde, doxalin woowu ak kàddu yooyu dañu woroo ak ni demokaraasi tëddee. Ndax, ci wàllu demokaraasi, téqalees na baatu doxal gi Njiitu réew mi jiite, baatu Yoon giy àtte nit ñi (muy njiit yi di askan wi) ak baatu Yoonal gi (Ngomblaan gi). Baat gu ci nekk, danga am sa cëru bopp te geneen baat warul a dugg ci liggéeyu geneen gi. Bu ko defee, lii day nasaxal demokaraasi, di gàkkal deru Senegaal ci àddina si. Moo tax ñu bari ñaawlu ñaari ndogal yile : jàppug Sonko ak tasug Pastef.

Muy waa réew mi di waa bitim-réew, rafetluwuñu doxalinu Nguur gi. Waa Pastef a jëkk naqarlu ndogal yi. Nde, ñoom, dañu gëm ne, mbirum pólitig kese ak ug bëgg beddi Usmaan Sonko ak Pastef ci wotey 2024 yee wund lii di xew yépp. Moo tax, sikk amul ci ne ñoom, ànduñu mukk ci ndogal yi. Noonu, dañuy bañ, ci seen i kàddu, teg ko ci li leen ndeyu-àtte réew mi may ciy àq. Moo leen tax a woo askan wépp ñu génn xeex ngir sàmm demokaraasi, sàmm ëllëgu Senegaal, waaye tamit xeex ngir aar Usmaan Sonko, génne ko ci loxoy Maki Sàll balaa dara di ko dal. Àjjuma ba léegi nag, réew maa yëngu, rawatina Ndakaaru ak Sigicoor. Ñu wàññeegum ci xaat ñetti bakkan yu rot. Fa bitim-réew sax, am nay saa-senegaal yuy ñaxtu ngir jàppale Usmaan Sonko, niki Mali gii dend ak nun. Naka noonu, fa Etaasini tamit, ñoo nga fay ñaxtu, ak feneen ak feneen.

Am nay kilifa yu ci yëkkati seen i kàddu. Ku ci mel ni Aminata Ture, mi ngi woo képp kuy xeexal demokaraasi ngir mu bañ li Maki Sàll di def. Lu ko moy, ci xalaatam,  demokaraasi biñ yàgg a xeexal ci réew mi dina nasax.  Séex Bàmba Jéey daldi koy feelu. Nde, moom itam Jéey, dafa gis ne loolu teguwut ci yoon te lu mu ñaawlu la. Ca Farãs, Jean-Luc Melenchon ñaawlu na tamit li Nguurug Senegaal di teg Usmaan Sonko te di woo Nguurug Farãs ngir mu bañ a seetaan loolu.

Séydu Géy mi yor kàddug APR, moom dafa jàpp ne Usmaan Sonko, li ko dal yépp, yeyoo na ko. Moo ko tax a àddu ca teleb France 24, wax ne, lu jiin Njaag a, te Usmaan Sonko a di Njaag. Noonu, fàttali na fa, ci gis-gisam, lenn ciy kàdduy fitna ak taafar yu muy askanale Usmaan Sonko. Coow laa ngi ne kurr nag. Ku nekk a ngi xëcc, di ràcc di jëmale sa boor. Réew maa tege ci furno bu defi xal te, dafa mel ni boor yépp dañuy ëpp ngir boyal furno bi. Waaye, bu réew mi tàkkee, ku ciy jariñu ? Wolof nee, fitna du yem ci boppu boroom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj