Jéyya gënul réy suuxug gaalu Joola ga. Te, njaaxum du ko weesu. 20i at ci ren, ba tey, déggeesagul jéyya bu xaw a jege suuxug Le Joolaa ba woon. Titatnic bi ñuy soow sax, jegewu ko. Nde, daanaka, 2. 000i bakkan ñoo ci rotoon. Ndaw tiis. Ndaw gàcce. Ndax, ba jonni-Yàlla-tey jii, ginnaaw komandaŋ bi nga xam ne da cee labaale, yoon nee na kenn taqu ci, kenn deful dara. amul kenn ku yoon teg loxo, gàll ko ay tuuma. Ndeysaan… Senegaalu tey.
Ca géeju Gàmbi ga la xewe woon. Le Joola, nees ko daan dàkkentale, moo daan lëkkale Ndakaaru, Sigicoor ak Karabaan. Mag, ndaw, góor, jigéen, boroom alal bi, baadoola bi, doxandéem bi… ñépp a ci daan yéeg ngir tukki. Ndeysaan, ña ca demoon, keroog 26 sàttumbar 2002 de, delsiwuñu. Bés boobu, ku jooyul it, ame woon nga tiis ak naqar wu réy lool. Bu Senegaal doon nit, keroog, géej ga wann na xol ba. Ndegam tukkee tiis, astemaak dee.
Fàttaliku, lu neex a ca gën. Ndax, bu dee lu tiis, coono ganesi boroom, naqaram feddaliku, góomu xolam di nàcci. Looloo nu dal, nun saa-senegaal yi. Waaye nag, fàttaliku dinay njariñ ñeel ku boroom xel. Dafa di, suuxug gaalu Joolaa bi, naam metti na, wànte Senegaal mën na cee defaroo ci fànn yu bari bu ñu defee li war.
Ñaar-fukkeelu fan ak juróom-ñaar bu jot, ci sàttumbar, askanuw Senegaal fàttaliku way-dëdduy Joola gi. Mu nekk xew-xewu dëfal ci njaboot yi ci loru. Loolu la Samsidin Aydara, bokk ci kurél gi taxawal Le Musée-Mémorial Le Joolaa, di firndeel buy wax naan, moom, ñeenti magam la ci ñàkke. Seneplus la ko waxe. Bàyyiwut Samsidin. Waaye tamit, bàyyiwut Aliyun Siise mi nekkoon kàppitenu ekibu futbalu Senegaal jamono jooju, tey ji mu nekk aji-tàggat ji. Ndekete, fukki mbokkam ñoo ci labe. Seneweb la siiwalee xibaar bile, ginnaaw 20 i ati naqar.
Lii nag, dees na ko bind ciy téere ngir ëllëg, maas yiy ñëw. Warees na ko boole ci mboorum réew mi, di ko jàngal xale yi ngir ñu yeewu, di yeete, di moytu, di moytuloo ak a fagaru. Bu dee ci wàllu ladab moom, gàcce-ngaalaamaa Bubakar Bóris Jóob, werekaan bi bind Bàmmeelu Kocc Barma, téereb fent ci wolof. Tax na ba dootul raaf ci xel yi. Nde, Bàmmeelu Kocc Barma kat, mooy bàmmeelu Joola bi rekk. Ndaxte, Njéeme Pay de, fàttewut xaritam ba, Kinne Gaajo ma des ca géej ga. Moo taxit, de, dootul raaf ci xel yi ak ci xol yi.
Waaye, nag, li jar a def dëgg-dëgg ñaari mbir la. Bi ci jiitu mooy, amal ab luññutu, lëñbët mbir, xool ba xam sabab yi waral jéyya bu ni mel, xam ku def ak ku deful, teg daan yi war, mu bañ a am xàjj-ak-seen. Waaye, tuumaal koo xam ne mënut a weddi, loolu rafetul te dalul xel. Ñaareelu mbir mi mooy fexe ba njuumte yi nu daloon bañ noo dalaat. Xanaa du wolof a wax ne, ku ndóbbin rey sa maam, foo gisatee lu ñuul daw ? Booy xool ni daamar yiy feese, rawatina biisi Tata yi, dangay xam ni askan wii, rawatina ay njiitam, jàngewuñu dara ci jéyyab Joolaa bi. Bu dee nger, yëfi maa-tey ak yaa-ma-neex bokkoon nañ ci sabab yi, dangay gis ne tey la Waalo gën a aay. Ba kañ nag ?