Bu ñu nee 8 màrs, xel yépp dem ci bés bu mag bi ñu jagleel jigéen ñi ci àddina wërngal-këpp. Ñu di ko màggal at mu jot ginnaaw bi ko mbotaayu xeet yi (ONU) biralee ca atum 1977. Réew yépp di ci sargal seen i jigéen. Waaye, soloom dëgg mooy xeexal leen seen i àq ak yelleef.
8 màrs nekk na léegi xew-xew bu réy, ñu jagleel ko jigéen ñi. Réew mu nekk, ak ni nga mëne, yaa ngi ciy jéem a njukkal say jigéen. Senegaal tamit, kenn demut mu des. Ñu seetlu ay yëngu-yëngu yu bari yu muy amal ngir sargal seen i yaay, seen i jabar, seen i ràkk ak i doom yu jigéen. Doonte ne xumbeel yi lañu gën a fésal, solo sa mooy ñu gën a ñoŋal jigéen ci seen taxawaay ci lu yitteel askan wi. Waaye, fexe ba dooleel leen ngir seen taxawaay ci bérébi liggéeyuwaay yi gën a ñoŋ. Loolo tax ci seen xeex boobu ñu woteel leen “parité”, maanaam yemoog góor ak jigéen, tax ba jigéen ñu di ko séen léegi fépp ci màkkaani réew mi. Ci loolu, tay ci talaata ji, Njiitu réew mi Màkki Sàll mi ngi ciy sargal jigéen ya nekk ca biir pale. Ma nga leen di kañ ci seen liggéey ak a mastawu ci jafe-jafe ya ñuy jànkonteel ngir seen i njàboot.
Waaye, bu ñu fàtte njukkal ka ko yayyo. Te balaa nga ne naam, ne fa. Te, ca dëgg-dëgg, ba naari Taraarsaa ya ne jóox Waalo, jigéeni Ndeer ya ñoo ne leen “naam”. Loolo nga xewoon ca talaata 7 màrs 1819 ca Waalo. Kon, kuy xeex àq ak yelleef day fekk nga nekk ci péexte. Te jigéen i Ndeer ya nooteel moo taxoon ñu joxe seen i bakkan. Kon, kuy sargal jigéen ci Senegaal, war a wax jigéeni Ndeer “gàcce-ngaalaama”.
Mënees na jàpp ne taxawaayu jigéen ci àdduna yàgg naa réy. Muy ab xeex bu ñu yàgg a amal ngir siggil seen bopp, waaye siggil seen askan ngir ñu gën leen a gëddaal ci lépp lu nit di def. Mo tax bés bu nekk ñu war di leen wax gàcce-ngaalaama, ndeyu àdduna !