Seetlu nañu ne, saa bu Yoon wooloo njiitu pastef lii di Usmaan Sonko rekk, dal day gàddaay réew mi. Walla, saa bu génnee, war a doxiy soxlaam, nemmeekuy am-di-jàmmam ak i soppeem, réew mi jax. Bii ci mujj rekk ñeel ndiiraanug péexte gi mu sumb firnde la ci. Te, xel dalul ci àtte bii lees war a biral ci alxames jii ñeel layoom ci mbirum ciif gi ko Aji Saar di tuumaal.
Fitna ji bari na. Taafar ji jéggi na dayo. Senegaal ba Senegaal daj, kenn mësul a gis lu ni mel. Coow lol, dafa tëw a jeex. Ndeysaan, askan wi, baadoola yi, góor-góorlu yi, kenn nelawatul ba yàndoor. Liggéey jafe na. Dundu gi metti na. Ay bakkan yuy wéy di rot, ñuy xeex rekk. Nit ñiy ame ay gaañu-gaañu yu mettee metti, ñuy xeex rekk. Bérébi liggéey yiy daanu ak a boy, ñuy xeex rekk. Daamar yiy tàkk ba jeex, ñuy xeex rekk. Koom-koom giy nasax, ñuy xeex rekk. Senegaal di dellu ginnaaw, ñuy xeex rekk. Gaal giy suux, ñuy xeex, di xeex, di xeex, dëkk ci xeex, di ci yeewu, di ci xéy, di ci yendu, di ci gontu, di ko fanaanoo. Usmaan Sonko jàppal fii, Maki Sàll bàyyil fee. Usmaan Sonko day bokk, Maki Sàll du bokk. Maki Sàll day bokk, Usmaan Sonko du bokk… Waa yeen, ndax Usmaan Sonko ak Maki Sàll ñoo moom réew mi ? Ndax Senegaal seen ndono la ? Lii, ba kañ ?
Bu Usmaan Sonko sëqatee sax, Nguur gépp jànnaxe, dajale takk-der yépp, yabal leen ngir tas mbooloo ma ànd ak Usmaan Sonko. Walla ñu yónni leen fa koñu njiitul Pastef li, Site Kër-Góorgi, ñu fatt yoon yi fa fay jëme yépp : kenn du dugg, kenn du génn ; amul jàngi, amul liggéeyi, amul nduggi, amul dara. Ku doxsi mbokk sax, ñu waññi la. Boo fa nekkee di layam-layami, ñu taxañ la, utal la néeg ndung-siin. Bu loolu amee nag, ndaw ñi fippu, tàmbalee jàmmaarlook takk-der yi. Lii, ba kañ ?
Noonu, lakkirimosen yiy téll-télli, xeer yiy xërr-xërri, matt yeek póno yiy boy. Saxaar su bon siy jëm kow, ubale jàww jépp, kenn du noyyi. xeer yekk doj yi fees dell ci tali yees dog : kenn du dem, kenn du dikk ; kenn du ubbi sa bérébu liggéey bu dee fa la xeex bi ame. Léeg-léeg, takk-der yi sox i bali fetel yoy, dinay am bu ciy dal kenn, mu daldi daanu, jaaxaan, dëppu mbaa tëdde wet. Deret jiy wal, mu faatu. Céy ! Dëj a ngoog. Tiis ak njàqare ganesi njabootu ki dee. Coow li neeti kurr. Ñuy jiiñante ak a tamante dëmm. Lii, ba kañ ?
Bu lu ni mel amee, nga gis ñu song këri kilifa, taal leen, jafal daamar ya fa nekk yépp. Sëriñ Mbay Caam du ko weddi. Maam Mbay Ñaŋ du ko weddi. Séex Yerim Sekk du ko weddi. Mataar Ba du ko weddi. Waaye, Séex Baara Njaay itam seede la ci. Daam Mbóoj, seede la ci. Soxna Ayda Mbóoj, seede la ci. Ak ñeneen, ak ñeneen… Gatsa-gatsa gii, ba kañ ?