Njiiti Bayern Munich yi mujje woon nañ déggook yu Liverpool FC yi ñeel ëllëgu Saajo Maane. Doomu Senegaal ji di jóge Liverpool bim fa jotee def 6i at (Suweŋ 2016 ba Suweŋ 2022), amal fa 267i joŋante, dugal ca 120i bii. Talaatay tey ji la Bayern di ko dalal ngir mu amal caytu-yaram ginnaaw bi mu fa teewee ngir xaatim déggoo yi.