Yokkuteg dundu gi nekk di lëmbe àddina si boobu ba léegi tax na ba koom-koomu réew yu bari dellu ginnaaw bu baax a baax niki yenn ci réewi Afrig yi. Waaye nag, njàngat bi FMI (Fonds monétaire international) def ci koom-koomu réewi Afrig yi, rawatina ñi féete Afrig sowu-jant a ngi wone ni koom-koomu Senegaal dina yokk ci atum 2023 mii nu dëgmal. Xaymees nan yokkute gi ci 8,1%.
Aamadu Jara
Njàngat yi FMI jot a def ci koom-koomu réewi Afrig yaa ngi wone ne koom-koomu Senegaal dina yokk ci atum 2023 mii nu dëgmal. Ci seen toftalaan gi, Senegaal a jël raw-gàddu gi ci réewi sowu Afrig yi. Nde, toftalaan gi nii la tëddee : Senegaal 8,1%, Niseer 7,3%, Kodiwaar 6,5%, Bene 6,2%, Tógo 6,2%, Mali 5,3%, Burkinaa Faaso 4,8%, Gine Bisaawoo 4,5%.
Ci li réewum Senegaal nar a jëfandikoo sorojam ak gaasam ci at moomu la njàngat yi aju ngir fàggu lu ni mel. Daanaka, ci yooyule sémb (sémbub gaas « Grand tortue/Ahmeyin » ak sémbub soroj bu Sàngomaar) la réew mi yaakaar ci jamono jii ngir wàññi yokkuteg dund gi.
Mamadu Mustafaa Ba, jëwriñ jiñ dénk wàllu koppar gi, bokkoon na ci ndaje ma FMI amaloon fii ci Senegaal. Moom nag, jotoon na waxtaan ak kilifa ya fa teewoon ci yittey réew yi lu deme ni jafe-jafe yi ñu am ci wàllu koom-koom gi ak njeexitali fitna yiy juddu ci diggante réew yi te muy gàllankoor seenug yokkute. Ci seen xalaat, réewum Senegaal def na ay jéego yu baree bari ginnaaw bi mu lalee ay pexe ngir wàññi yokkuteg dund gi. Nde, jàpp nañu ne sax, fii ak 2023, koom-koomu réew mi dina yokku ci lu tollu ci 10,1%.
Waaye, kii di njiital làng gii di PASTEF, Usmaan Sonko, àndul ak yile xeetu ndaje yiy am ci biir réew mi. Ndax, ci xalaatam :
« Réew yu mag ya, dañu jàng di ut ay pexe ci seen i jafe-jafe ba suqaliku fekk seen njiit yi jaaruñu fenn ngir sàkku ndimbal ci benn mbootaayu àddina si. Looloo war a nekk sunu yitte ndax danoo war a mën a doxal sunuy mbiri bopp, moom sunu bopp. »
Yemul foofu doŋŋ. Bi mu xuusee ba ci biir, moo ngi xamle ni :
« Ginnaaw li nu yore ci soroj ak gaas, yor nanu suuf su nangu. Waaye, Senegaal 10% rekk la moom ci gaas ak soroj bi mu yore. (…) Su bàyyiwul di aju ci yeneen i réew ngir dundu, yokkuteg dundu gi du mës a jeex. »
Lii mu wax nag, teey na xel waaye lu mat a sóor la tamit. Bu dee wax na lu ni mel, ñàkkul ne am na fu mu ko teg. Waaye ba tey, lu ci kanam rawul i bët.