Bakkan bu ñam dund, ñam dee. Ab xandeer bu damme cib waar moo wàcc. Tiis ak mbetteel la askanuw Senegaal yeewoo ci talaatay démb jile. Imaam Ndaw, ñu gën koo xam ci Aliyun Badara Ndaw, moo wuyuji Boroomam.
Xol yépp a fees bi ñu yëgee gaañug Imaam Ndaw. Daanaka, Senegaal gépp a jooyandoo jàmbaaru lislaam bile, di jàmbaaru Senegaal ak Afrig, jàmbaaru jikko yi. Ci guddig altine ji, jàpp talaata, lanoppalu. Moom, nag, dafa tawatoon ba lenn ndaw réew jotoon ko dajaleel lu tollu ci 20i tamndareti CFA ak lu teg ngir rawale ko bitim-réew, mu fajooji fa. Ndeysaan, jaam ak pexeem, Yàlla ak ndogalam. Imaam dem na, dootul delsi… Waaye, ndono lim fi bàyyi, moom, du raaf. Bu ngeen ma nee lu tax, ma ne leen dangeen xamagul kan moo doon Imaam Aliyun Badara Ndaw. Xarleen ma wax leen ci moom as-tuut.
Imaam bu mag bi, nitu daara ki
Ku dégg Imaan sam xel war a dem ci Jumaa, ci diiney Lislam. Njëlbeenug màndargaam a ngoog. Waaw, Imaam Ndaw, nees koy dàkkentale, Imaam bu mag la woon. Nitu diine. Nitu daara. Atum 1960 la gane woon àddina fa Ngaan Alasaan, Kawlax. Bi mu ame juróom-benni at la dal jàng ca daaray Sëriñ Muxammad Saxiir Lóo bu Kokki. Waaw, Kokki gu siiw gi. Bi mu amee juróom-ñeenti at ci la mokkal Alxuraan. Imaam Ndaw jaar na Njaareem fa daaraay Sëriñ Moor Mbay Siise. Foofu la taree. Ginnaaw bi mu jàngi xam-xam Sàcci-Jamal, Maka Guy… Ab joŋante bu mag bu ñu doon amal ci alxuraan moo ko taxoon a génn réew mi. Nde, dafa tàggatuji woon ca réewum Muritani. Ginnaaw gi muy jàng ak a jàngale téere bu sell bii di Alxuraan. Looloo ko taxoon ber daaraam.
Senegaal, ku fi ne daara, ne Imaam Ndaw. Loolu, sikk amu ci. Ndaxte, dafa nekkoon nit ku ittewoo xam-xam, daan taxawu daara ak ndongo yi. Mën nañoo wax ne Imaam Ndaw jaar-jaar bu mag la am ci wàllum njàng ak njàngale. Taxawaayam ci diine nekkoon lu rafet. Wànte, yemul foofu. Ndege, Imaam, bañkat la woon. Dafa daan xeexal réewam ak Afrig ciy waxtaanam, ci xutbaam ak yeneen. Da daan xeex jikko yu bon, àndoon ci ak waa ÀND SÀMM JIKKO YI. Dafa xeex itam nootaange ak lépp lu jëm ci faramson yi. Dafa di, xeex boobile a ko indiloon ay jafe-jafe ba ñu jàppoon ko ci, nëbb ko jant bi.
Imaam Ndaw, bañkat bi
Ca atum 2015 lañu jàppoon Imaam Ndaw. Dañ ko taqaloon, jiiñ ko ne rëtëlkat la (terroriste), moom ak yeneen fanweeri ndaw, ciy maaliforo. loolu nag, bokk na ci ko gën a siiwal. Li mu nekkoon nitu daara, nitu diine, nitu dëgg a taxoon ba ay ñomam bàyyiwuñu ko benn yoon ca jamonoy xat-xat yooyu.
Bi loolu weesoo, Imaam Ndaw doon na biral anam yi ñu ko jàppe woon ca Kawlax ak mettit ya mu jotoon na dund ca ndungsiin. Ca waxtaan wa mu séqoon ak Walf ca jotaayu Salon d’honneur, feeñal na lu bari cig dundam. Mu mel ni la ñu ko doon toppe xamu ci dara, di rëtëlkat, yori ngànnaay ak laale ak Boko Haram di kuréel gu mag ci wàll woowu bu ñu sukkandikoo ci li mu tontuwoon àttekat ba. Yoon téye ko lu tollu ci ñaari at ak juróom-ñetti weer. Mu mel ni nattu yooyu dañ ko yokku dayo ak nangu gi mu nangu woon te boole ko ak ngëm. Ci li ëpp ci ay waxam, daan na faral di ñaax jullit yi ne, nit warut a ragal kaso ndax diine ci nattu lay dundu.
Ngir tënk, Imaam Ndaw, diine tax mu daan sonn, diine tax mu sonn ndax jaar-jaaram yone na ko. Ci waaru diine ak bëgg réewam ak kembaram la juddu, màgge ci, sonn ci te, ci lañ ko sonale, ci la it wàcce liggéey. Lii moo tax wolof di wax naan, xandeer bu damme ci waar, wàcc na.
Seen yéenekaay LU DEFU WAXU a ngiy jaale jullit ñépp, di ko jaale njabootuy daara yépp, di ko jaaley mbokkam ak waa Senegaal yépp.