JALOOREY RAGLUB SÓOBARE BU WAKAAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal séqi na jéego bu am a am solo ci wàllu paj. Nde, doktoor ya ca raglub sóobare ba ca Wakaam, maanaam loppitaanu soldaar bi nekk Wakaam def nañ lu fi kenn mësut a def. Muy lu njëkk ci réewum Senegaal, nekk it lu néew ci kembaarug Afrig. Joj jaloore mooy jan ? Li fajkati raglub Wakaam bi jëkk a def moo ñaw ab roño ci biiru nit. Maanaam, li tubaab di wax “transplation rénale”.

Feebaru roño dafa lëmbe jamono ndax lim bu baree baree ko ame ci àdduna si, rawatina Senegaal. Rax-ca-dolli, mu doon tawati dëkkaale la (maladie chronique) te am pajam dafa aajowoo ay matukaay yu bare te njëge. Dafa di, koppar ya ñuy laaj aji-tawat ju ame feebarub roño dafa jéggi dayo. Te, kenn umpalewul ne Senegaal, askan wi dafa néew doole ; ñu bari seen loxo jotul seen ginnaaw. Moo tax, at mu nekk, lim bu bari ciy nit la feebar biy faat. Waaye, xel mën na dal, yaakaar lalu ginnaaw ba doktoor ya ca Wakaam oppeere seen oppeere bu jëkk ci wàll wi, muy oppeereb sof roño.

Ca biir yëgle njiitul CNDT lii di Allaaji Fari Ka def, ma nga cay fésal mbégteem di ca xamle ne sofal nit roño lu mën a nekk la léegi ci sunum réew. Te, dana yékkati réew mi, boole ko ci dëkk yiy jox xeetu paj moomu seen uw askan. Waaye ñu mën ci jàngate tamit ciy kàddoom jëf la joo xam ne dina yokk yaakaar jarag yi. Ndax, lañu nemmeeku ci jàngoro jooju, jaliis lañu daan jëfandikoo ngir taxawu jarag yi. Waaye bu ca lii dolleekoo dina yokk yaakaar ña koy dund.

Njiitu réew mi, Maki Sàll, rafetlu na jaloore ju réy jooju. Moo tax, ca ndajem réewi Afrig ya ñeel jàmm ak kaaraange ja mu doon tijji, biral na ko fa. Mu boole ko ci saafara yi réewi Afrig yi mën a indi ngir xeex jàngoroy dëkkaale jooju.

Ñu seetlu ne, réewum Senegaal mu ngi def ay jéego yu mag ci wàllu paj. Jàngoroy roño bokk ci tawat yi gën a fitnaal askan wi. Kon, gàcce-ngaalaama doktoori Wakaam yi !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj