Taset, di ab gox bu féete ca diwaanu Nooto, fa Cees. Aw tiis moo leen gane démb, di aksidaŋ bu fa am. Ñetti ndongo yu jigéen ñoo ci ñàkk seen i bakkan ak yeneen ñetti yu ci ame ay gaañu-gaañu. Bu ñu sukkandikoo ci xibaar yees ci biral, ag sëfaanu tool (tracteur) bu jóge woon tool ya moo jaar seen kow.
Muy tiis ak naqar wu dall ci daara ju dig-dóomu ja ca Taset. Ñaari ayu-bés, ginnaaw ubbiteg lekkool yi, ñetti ndongo yu doon def “5éme” ñoo faatu. Xew-xew boobu am ginnaaw ba ñu wàccee ca lekkool ba doon ñibbi seen dëkk. Muy ab gox buy wuyoo ci turu Taset-Pël, diggam ak foofu tollu ci 2i km. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di Dakaractu, la waral jéyya ja bokk na ca dawalkati daamaar yu doon rawante ak ay xél. Fekk boobu ndongo ya wàcc doon jéggi tali ba, fa la musiba bi xewe.
Leneen lañu ca jote taataan mooy ne, bokk na ca ña ñàkk seen bakkan benn doomu njiitu gox bu Taset di, C. Ka. Keneen ku ame ay gaaañu-gaañu yu mettee-metti, ndax ñaari tànkam yi ñoo dag. Ca raglub Aamadu Saxiir Njégen bu Cees lañu yóbbu néew ya.
Mënees na tënk ne, daamar yaa ngi wéy di nangu ay bakkan ci tali yi. Moo xam ci ñiy tukki walla sax ña ñuy romb. Ndongo yi sax léeg-léeg mu laal leen ndax ay daamar yuy saaraan ba ca lekkool ya.