JOŊANTE CFEE 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋantey CFEE yi door nañ ci àllarbay tey ji, war a jeex ëllëg ci alxames ji. Senegaal, Gàmbi ak Gine-Bisaawoo ñoo koy defandoo. Xarees na ci limi ndongo bu takkoo takku bu ñu ko méngalee ak ba woon daaw. Bu ñu sukkandikoo ci Pàppa Demba Jaase mi ñu dénk joŋanteb CFEE bi waa DEXCO (banqaas biy saytu kàtte yeek joŋante yi) jël nañu matuwaay yu war a yépp ngir gën a ñoŋal joŋante bi.

Li ñuy tudde CFEE (Certificat de fin d’études élémentaires) ak “entrée en 6ème”, diy nattukaay yees jagleel lijaasa biy tëj njàng mi ci daara yu ndaw yi fii ci Senegaal tàmbali nañu tey ci àllarba ji 21 Suwe 2023. Li mu xale yi bindu ngir wut seen lijaasa bu njëkk mu ngi tollu ci 297 621. Ñu seetlu ne, lim boobu, li ci jot a yokku tollu na ci lu ëpp 1 000iy ndongo. La ca Pàppa Demba Jaase xamle, mooy ne jigéen ñaa ca ëpp. Nde, téemeer yoo jël, juróom-fukk ak juróom-benn ya ay jigéen lañu, maanaam 56%. Ñu seetlu ci lu tollu 47 ci ay ndongo dañoo ame jafe-jafe gis. Waaye, jël nañu ay jumtukaay yu ñu mën a amale seen i joŋante.

Ginnaaw bi ñu ko tàmbalee ci suba si, jëwriñ ji Séex Umar Aan doon na amal ab doxontub nemmiku ci daara yi. Muy rafetlu doxalin bi ak ni mu jaare yoon ba kenn seetloogu ci luy niru sikk. Terewul ci yenn diwaan yu mel ni Kéedugu, nemmeeku nañu fa lim bu takku ciy gune yu nekk di def yile kàtte, te seen i kayiti juddu am i jafe-jafe. Walla sax, léeg-léeg ñu bañ a am i kayiti juddu. Ginnaaw jafe-jafe yooyu, jàmm rekk lees ci seetlu. Ndax, fan yii weesu, réew mi amoon nay yëngu-yënguy pólitig yu salfaañe dalug réew mi ba lekkool yi jotoon cee laf seen i bunt, waa DEXCO ña ngay dalal xel yi ngir amal joŋante CFEE yu jaar yoon te ànd ak kaaraange. Ca weneen wàll wa, Pàppa Demba Jaase ma ngay biral matuwaay ya ñu dajale, moo xam lu jëm ci kaaraangey kàtte yi ak koppar ya ñu génne ngir amal joŋante yu jaar yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj